dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ràbbaske : duggante, jaxasoo. cari garab gi dañoo ràbbaske.

ràbb : dafay ràbb ay sër di jaay.

ràbbu g- : ràbbu weñ gu am cat lu ñaw te ñu koy firee ay létt la.

ràcc : tas. ràcc na cere ji ndax mu gaaw a wow. safaan wi mooy kepp, dajale wala boole.

ràddi : bàyyi mu dem yoonam, fiddi. ràddi na golo gi mu jàppewoon ca àll ba.

ràgg : sew, jeex. xaj bi ràgg na lool. safaan wi mooy suur wala am-yaram.

ràjji : sëq. toolu naajoom ba ràjji na.

ràkkaaju : bi xale bu jigeen bi amee far ba léegi, dafa ràkkaaju. safaan wi mooy yem, teey.

ràkkal j- : rakkal mooy liy des ci gerte gu ñu perees, def ko dëwlin ba pare.

ràkka b- : julli tisbaar ñeenti ràkka la.

ràll : (ne ràll). coow li bunt wala palanteer bu ñu ub ak doole di def. dinañuy wax tamit réll (ne). ngelaw lee ne ràll bunt bi.

ràllu : wutal ab jaaykat ay kiliyaan. dafay ràllu ci marse bi. / topp ci kow nit rekk ngir xaalis boo am ci moom. ki ngay ràllu sa morom la, demal liggeeyi ni moom.

ràmm : xas, barkooje. xaj bi dafa ràmm.

ràng : yebal. yow kenn waru la ràng ndax xamuloo ni ñuy waxe.

ràng g- : jumtuwaay yi ñuy takke fas ci sareet. ag ràng dafa war a dëgër.

ràngu 1 : dugg ci mbirum soldaar. am yambar du ràngu. / ñu dàq la ci am po, nga duggaat ngir bëgg a feyu. ràngu na wànte dinañu ko dàqaat.

ràngu 2 : takk ay téere yu bare. mbër mi ràngu na ba fees dell, ñëw taxaw ci digg géew bi.

ràññaatle : xàmme ba doo jaawale. nanga ràññaatle sa xarit ak sa noon. dinañuy wax tamit ràññale wala ràññee.

ràññale : dinañuy wax tamit ràññaatle. (seetal ràññaatle)

ràññee : dinañuy wax tamit ràññaatle wala ràññale. (seetal ràññale)

ràpp 1 : oos, yàqu. sol nga yére bi ba mu ràpp. safaan wi mooy bees.

ràpp 2 : (ne ràpp). baat bi dafay tekki lu ñu tëj ba dara du dugg, dara du génn. dugg na ci biir néeg bi, ne ràpp bunt bi.

ràyy : (ne ràyy). baatu ràyy (ne) dafay tekki lu jékki jékki rekk tàkk, leer nàññ. làmp bi ne na ràyy sànq.