dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

puj b- : njubbu xëdd l-. ngelaw li daaral na puju néeg bi.

pukkus b- : néeg bu tuuti lool. tiitaram yu bare yii yépp, ci ab pukkus lay fanaan. dinañuy wax tamit puqus b-.

pull : peq, tàq. baatu pull baatu bees rekk lay àndal. jënd na lal bu bees pull.

pulloox b- : ñàmbi j-. pulloox bi Kajoor lañu koy beye.

punkal : dinañuy wax tamit ponkal. (seetal ponkal)

puno b- : dinañuy wax tamit póno b-. (seetal póno)

puqeet : (ne puqeet). dinañuy wax tamit pëqeet (ne) wala pëccet (ne). (seetal pëqeet)

puqus b- : dinañuy wax tamit pukkus b-. (seetal pukkus)

purit m- : baatu purit mu ngi jóge ci baatu fuur. (seetal fuur)

purox g- : bóli g-, put g-. bëgg na lekk ba lu mu gis bëgg koo jaarale ci puroxam gi. dinañuy wax tamit purux g-.

purux g- : bóli g-, put g-. dinañuy wax tamit purox g-. (seetal purox)

puseer b- : ngelaw li dafa ànd ak puseer.

pusë b- : pusë bi mu doon ñawee damm na. dinañuy wax tamit puso b-.

puso b- : dinañuy wax tamit pusë b-. (seetal pusë)

put g- : bóli g-. dinañuy wax tamit purox g- wala purux g-. (seetal purox)

putt-meŋŋ b- : xaalis b-. putt-meŋŋ la yore.

puub : day, kabine. gone gee fi puub.

puudar : defal puudar. puudar na xale bi ba mu weex tàll.

puukare j- : tiitar b-. dafa bare puukare rekk wànte yorul lenn.

puune : dafa puune mootax fu mu romb nit ñi di ko xool.

puurit m- : baatu puurit mu ngi jóge ci baatu fuur. (seetal fuur)

puur : mboq, màkka. melo wu puur dafa xàññaaral.

puur b- : mburu mi ci puur bi la génne léegi mootax mu tàng jërr. dinañuy wax tamit fuur b-.

puus : jañ. oto bi dafa bañ a tàkk ñu koy puus. safaan wi mooy xëcci wala ñoddi.

puwaa b- : dinañuy wax tamit poo b-. (seetal poo)

puwaawuroŋ b- : dinañuy wax tamit kaani-salaat b-. (seetal kaani-salaat)