dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

picc b- : yaram wi dafa fees dell ak ay picc.

picc m- : gone yi dañuy fiir ay picc.

piire b- : pombiteer bu nooy. deel jox xale bi piire.

piir : lu raxul dara. soow piir lay jaay.

piis b- 2 : ndimo l-. jënd na ñeenti meetari piis.

piis : wax ak ay gët. dafa ko piis rekk, mu xam li mu ko wax.

pikiir b- : ping b-. pikiir a yàq tànk bi.

pikini b- : pikini xaalis la woon. joxu ko pikini.

pilot b- : taxaaru wëñ b-. tajoor bi bare na ay pilot.

pind b- : miir bu wërgëlu bi wër paxu teen bi. jigeen ñaa nga wër pind ba di root.

ping b- : abal ko ping bi, mu dindi dég gi ko jam. dinañuy wax tamit péngu b-.

pintiir : melool. pintiir na kër gi yépp.

pistole b- : dinañuy wax tamit lawarweer b-. (seetal lawarweer)

pitikoola b- : guro gu ndaw g-. du yëy pitikoola.

pittaaw : dinañuy wax tamit pettaaw. (seetal pettaaw)

pittax m- : dinañuy wax tamit pettax m-. (seetal pettax)

piyees b- : jumtuwaayu masin wala ag kayit. mótooru oto bi dafa mànke ab piyees.

piyoŋ b- : dinañuy wax tamit ndoxtu l- wala doom b-. (seetal ndoxtu)