dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

peccargo b- : jabaru sa mag wala sa rakku jëkkër mooy sa peccargo. dinañuy wax tamit peccorgo b- wala peccergo b-.

peccergo b- : dinañuy wax tamit peccargo b-. (seetal peccargo)

pecc : baatu pecc dafay ànd ak baatu xees di tekki bu baax. jabaram dafa xees pecc.

pecc m- : baatu pecc m- mu ngi jóge ci baatu fecc. (seetal fecc)

peccorgo b- : dinañuy wax tamit peccargo b- wala peccergo b-. (seetal peccargo)

peeg : baab. dafa lay peeg rekk wànte li mu lay wax du ko def.

peeñu b- : baatu peeñu b- mu ngi jóge ci baatu feeñ. (seetal feeñ)

peer b- 1 : taatu garab w-. am na peer bu ñu teg seen buntu kër, di ci toog.

peer b- 2 : ñaari mbir. benn peeru dàll la jëndoon.

peer : póno baa ngi peer.

peese : mandaxe. peese na ceeb bi mu nekk fukki kilo.

peesu b- : baatu peesu mu ngi jóge ci baatu fees. (seetal fees)

pegg b- : wet g-. muus maa ngi taxaw ci pegg bi di xaar waasintoori jën yi.

peket m- : dinañuy wax tamit péget m- wala pettax m-. (seetal pettax)

pekk b- : dàmb b-. ci pekk bi lay def bagaasam yu bare.

pelent : dinañuy wax tamit kalaame. (seetal kalaame)

pellax b- : sëb s-. pellax bi dafa saxe.

pelle w- : fas wu am lu weex ci jë bi. fas wi mu jënd aw pelle la.

pello b- : lu weex lu nekk ci jëwu fas. fas wa mu jaay amoon na pello.

peme j- : xeetu caq. caqu peme la takk.

pendal m- : sër b-, njodom s-, kumba s-. xaley jigeen yi léegi tubey a leen gënal pendal. dinañuy wax tamit péndal m-.

pend b- : mberu m-, layu b-. ay pend lay jaay.

penk b- 1 : diggante ndigg ba wóomu nit ku toog lañuy tudde penk.

penk b- 2 : bérebu dencukaayu xeeti pepp yi. am na dugub ak basi ca penk ba.

penku b- : fii ci Senegaal, jullit yi penku lañuy jublu su ñuy julli. safaan wi mooy xarfu.

pentiir : tabaxaat nañu seen kër ga ba pentiir ko.

peñe : nangay peñe sa kawar gi.

pepp m- : dugub j-. ginaar yaa ngi for pepp yi.

peqatal g- : tàkk l-, tefes g-. bul dugg ca biir ndox ma, yemal ca peqatal ga rekk.

peq : dinañuy wax tamit pull. (seetal pull)

perantal b- : baatu perantal mu ngi jóge ci baatu fer. (seetal fer)

perlit m- : baatu perlit mu ngi jóge ci baatu fer. (seetal fer)

perlukaay b- : baatu perlukaay mu ngi jóge ci baatu fer. (seetal fer)

perlu : raxas say awra. boo sawee ba pare, nanga perlu.

permeyaabal b- : dinañuy wax tamit tuwaal b-. (seetal tuwaal)

permiyaabal b- : sowetaas b-, yére taw b-. def na permiyaabal bi ci xëdd bi ndax su tawee, bu mu senn.

perngal : teg ab dénk bu mag ci kow géleem ngir tiye saaku yi ñuy teg ci kowam. naar bi perngal na géleem gi, yéeg ci di dem.

per b- : yéreem bi dafa am ay per.

per m- : sàkket w-, ñag b-. per mi mu defar rafet na.

persi b- : persi rënd la. dinay jaay persi.

pertmaa b- : njaayam mi dafa bare pertmaa. safaan wi mooy ngañaay l-.

peru bët b- : am na lu nekk ci peru bëtam bi.

pes : mbej. soo ko saagaa, mu pes la.

petaar b- : ci jeexitalu at mi, xale yi dañuy taal ay petaar.

pet : (ci pet). ruq (ci). dinaa ko ko wax ci pet, kenn du ko yég.

petorol b- : Arabi Sawdit am na petorol.

pettaaw : seet li ñëwagul ak ay pettaaw. maamam daan na pettaaw. dinañuy wax tamit pittaaw.

pettax m- : pettax mi dafa fi tàgg. dinañuy wax tamit pittax m-.

pexe m- : baatu pexe mu ngi jóge ci baatu fexe. (seetal fexe)

pey g- : baatu pey mu ngi jóge ci baatu fey. (seetal fey)

peyoor b- : baatu peyoor b- mu ngi jóge ci baatu fey. (seetal fey)