dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

paaka b- : saatu s-. nangul paaka bi xale bi yore bala mu koy gaañ.

paan b- 2 : beñwaar g-. àttanuloo paanu ndox.

paan : am ay jafe-jafe ba mënatoo dem. otoom dafa paan démb ba léegi.

paa b- : yoon b-. bii paa duma la nax.

paañ b- : mbaxal gi dafa am paañ.

paar b- : wàll w-. defal ndànk rekk, sa paar dina yegsi.

paase-wisit : dem kër doktoor seet sa yaram. jigeenu wérul ji dafay paase-wisit.

paase : fudd ay yére ak feer. paase dafay tàllal ay yére, di rey ay mikorob.

paasiyoŋ b- : réstoraŋ b-. ci paasiyoŋ bi lay añe.

paas : fey ci oto wala ngir looy seetaan. paas na ba pare.

paaxe b- : ku jongagul, aat b-. moom rekk mooy paaxe ci gone yi.

pacantaan b- : gént gu raglu. yomb na di am ay pacantaan guddi.

pacc-pacci : di tufli fu nekk. mu ngi pacc-pacci ni kuy jafte.

paccal : bës dara ba mu génn. xale yu jigeen yi dañuy paccal seen ween yi.

paccax-paccax j- : coow l-. paccax-paccax ji ngay dégg, nag yiy dox ci biir ndox mi la.

paccaxndiku : dinañuy wax tamit paccax-paccaxi. (seetal paccax-paccaxi)

paddaañu : def ay tànki neen. du sol dàll mukk, dafay paddaañu rekk.

pajaas b- : xeetu lal. jëndal ab pajaas ba ba ngay amee loo jënde matlaa.

paj m- : baatu paj mu ngi jóge ci baatu faj. (seetal faj)

pakk b- : ëkk b-. defal ndànk, yoon wi dafa bare ay pakk.

pakku : fegu, baare. dafa pakku yet wi ñu ko bëggoon a dóor.

palaafoŋ b- : jotuloo palaafoŋ bi.

palaas b- : béreb b-. ku nekk am na fa palaas.

palaat b- : aset b-. raxasal palaat bi.

palanteer b- : tijjil palanteer bi, dafa tàng.

pal g- : baatu pal mu ngi jóge ci baatu fal. (seetal fal)

palpale b- : palpale xeetu jën la.

pamti-pamte : sonal, lottal. gaa yi pamti-pamte nañu sàcc bi ba mënatul a dox.

pann m- : cere ju fanaan j-. am pann lañu fa ndékkee.

pantaloŋ b- : tubey j-. pantaloŋ bi mu sol jotu ko.

pañe b- : lu nekk ci pañe bi ?

papaaya g- : du lekk papaaya. dinañuy wax tamit pàppaaya g- wala pàppakaya g-.

par-parloo : faralaate, jeng. bul par-parloo benn yoon, nanga àtte dëgg rekk.

parax : (ne parax). jékki jékki rekk dugg fenn, dagaj, saraax. kaña gi ne na parax ci biir pax mi.

pare : sotti, noppi, yemb. pare na li mu doon def. safaan wi mooy tàmbali.

pareñ b- : pareñ mooy ki ñu baayale ab xew. safaan wi mooy maren b-.

par m- : par xeetu fas la.

pas-pas b- : baatu pas-pas mu ngi jóge ci baatu fas. (seetal fas)

pasar-pasare : yàq. sa alal ji ngay pasar-pasare, jox ci ñi nga tane. safaan wi mooy sakkanal.

pase g- : baatu pase mu ngi jóge ci baatu fase. (seetal fase)

pasin w- : cax b-. kenn rekk a xamoon pasin wi.

paskë : ndaxte, ndax. duma la ko jox paskë amuloo ci benn soxla.

pasteef b- : baatu pasteef mu ngi jóge ci baatu fas. (seetal fas)

pastel b- 2 : fataaya b-. àndiwaaleel na xale yi pastel.

pastel : makiyaas. ku la doon pastel.

pat-pati : kat-kati, lox. jaan ji mu gis a tax muy pat-pati.

pataa : am-yaram ba mu ëpp, mbuxuri. dafa pataa te bëgg a wàññeeku mootax muy tàggat yaramam. (seetal mbuxuri)

pataas b- : defal ndànk, pataas bi dafa tàng.

patam-patame : yàkkamte am mbir. dafa pamti-pamte liggeey bi mootax li mu def dara baaxu ci. dinañuy wax tamit pëtëm-pëtëme.

patoroŋ b- : njaatige b-. nekk patoroŋ bi bu mu tax nga defe ne yaa ñu moom.

patt 1 : yore benn bët. dafa patt wànte mu ngi gis bu baax.

patt 2 : (ne patt). tekk (ne), mekk (ne). waxul ak kenn, mu ngi ne patt.

patt b- 2 : beneen àndandooru peer b-. pattu dàll wi dafa réer.

pax m- : kan m-, bën-bën b-. suulal pax mi.

paxu-bakkan m- : deret a ngi génne ci paxu-bakkan mi.

payis : yóbbu ko kër doktoor ñu seet ndax dafa payis am déet.

pay g- : baatu pay g- mu ngi jóge ci baatu fay. (seetal fay)

paytéef b- : lëjum. tey marse bare na paytéef. dinañuy wax tamit pëyteef b-.