dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

póli b- : póli jumtuwaay la ngir root ci teen.

pólis b- : màkkaanu alkaati yi. li dugal sa morom pólis, mën na la fa dugal.

pólotig : saytu dundu askan ak nekkinam. dafay pólotig.

póno b- : tànki oto, welo wala sareet. póno baa ngi peer. dinañuy wax tamit puno b-.

póon m- : baatu póon mu ngi jóge ci baatu fóon. (seetal fóon)

póot m- : baatu póot mu ngi jóge ci baatu fóot. (seetal fóot)

póotu b- : baatu póotu mu ngi jóge ci baatu fóot. (seetal fóot)

pótit m- : baatu pótit mu ngi jóge ci baatu fóot. (seetal fóot)