dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

pëccet : (ne pëccet). dinañuy wax tamit pëqeet (ne) wala puqeet (ne). (seetal pëqeet)

pëdd b- : lu mboq li nekk ci nen. pëdd a ko gën a neex ci nen.

pëggu b- : bant bu ñuy dawale mbege. pëggu bi dafa dàmm.

pël-pël m- : pël-pël xeetu xar la.

pëll : (ne pëll). baatu pëll dafay tekki lu jékki-jékki rekk génn. ki ñu doon xaar ne na pëll. dinañuy wax tamit tell (ne).

pël b- : pël bi am na ay nag.

pël g- : dëkkuwaayu pël ñi. pël ga la jënde soow mi.

pëndax b- : sunguf s-, puudar b-. pëndaxu meew a fi tuuru.

pënd b- : puseer b-. ngelaw lee àndi pënd bi yépp.

pëqeet : (ne pëqeet). baatu pëqeet dafay tekki lu jékki-jékki rekk génn. gone yi dañoo sotti ndox mu tàng mi ci pax rekk, kaña gi ne pëqeet, daw. dinañuy wax tamit pëccet (ne) wala puqeet (ne). safaan wi mooy parax (ne) wala dagaj (ne).

përëg m- : wàllug loxo gi nekk ci diggante mbagg mi ak conc bi. mu ngi takk ag ndombo ci përëg mi.

përiis m- : póon m-. përiis lay tux.

përiye : woo. xaritam a ko përiye añ. safaan wi mooy dàq.

për m- : ngooñ mu mokk m-. nag yi për lañu gën a bëgg. dinañuy wax tamit për-për m-.

pëtëm : lakk ak dóom. gerte gu ñu pëtëm laa bëgg.

pëyteef b- : dinañuy wax tamit paytéef b-. (seetal paytéef)