dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

péexlukaay : baatu péexlukaay mu ngi jóge ci baatu féex. (seetal féex)

péex m- : baatu péex mu ngi jóge ci baatu féex. (seetal féex)

péey b- : dëkk bu mag b-, dëkk b-, ngénd l-. ñoo bokk péey bu ñu cosaanoo.

péget m- : pettax m-. péget mi dafa nen ci kow garab gi. dinañuy wax tamit peket m-.

pénc m- : béreb bu ñépp di daje ci dëkki kow yi. ñu nga ca pénc ma.

péndal m- : dinañuy wax tamit pendal m-. (seetal pendal)

péngu b- : dinañuy wax tamit ping b-. (seetal ping)

péŋŋ : baatu péŋŋ dafay ànd ak baatu wóor di tekki bu baax. li mu la wax wóor na péŋŋ.