dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

pàcc m- : xaaj b-, wàll w-. téere bi am na ñaari pàcc.

pàdd : gaynde gi dafa pàdd kéwel gi rekk mu daanu.

pàkkarñi : fecc, dagañ, dukkat. xale yu jigeen yaa ngay pàkkarñi ca sabar ga.

pàkk b- : kër gu ñu tabaxagul. am na genn kër ak ñaari pàkk.

pàllanq b- : doq g-, ndodd l-. dafa taab ci pàllanq.

pàllngar b- : fi ñuy dugge ci ab tool, bunt b-. ca pàllngar ba la def am mbaar.

pànk : ku bëgg defante. ndaw soosu dafa pànk, bul dugg ci moom.

pàppaaya g- : dinañuy wax tamit papaaya g-. (seetal papaaya)

pàppakaya g- : dinañuy wax tamit papaaya g- wala pàppaaya g-. (seetal papaaya)

pàppa j- : baay j-. pàppa ji dafa tukki. safaan wi mooy yaay j-.

pàq b- : wateef goo xam ne dañuy bàyyi ay njubb ci bopp bi. pàq bi ñu ko defal seen aada la.

pàrk : nañu dem pàrk ba seeti gaynde yeek bukki ya.