dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ordisawel b- : yére boobu, soo ko fóoteewul ordisawel, du set mukk. dinañuy wax tamit ordusawel b-.

orma j- : teggin, w-, aajo j-. nanga am orma ci sa moromu doom-aadama ak waaso wu mu mën a bokk. dinañuy wax tamit worma j-.

or : jàmbu. or na waa ji mu doon àndal bu yàgg ba léegi. dinañuy wax tamit wor.