dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

oom : naat. liggeeyam ba oom na. dinañuy wax tamit woom.

oo : wuyul ki lay oo. dinañuy wax tamit woo. safaan wi mooy uyu wala wuyu.

oos : yàqu ndax yàgg. yére bi oos na léegi, li nga ko sol dafa bare lool.

oos g- : dóolinka g-. oos gi lay nappe jën.