dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

nugg : xaw a tàng. ndox mi tàngagul, dafa nugg rekk.

nunni : dàq dara mu jëm benn boor. na nunni nag yi ba bu ñu dugg ci tool bi.

nu : nu mu ko defe nii ? dinañuy wax tamit naka.

nuroo : dinañuy wax tamit niroo. (seetal niroo)

nuur : dugg ci biir am ndox mu deme ni géej wala dex, tëmb. nuur na ci ndox diiru juroomi simili. safaan wi mooy nukki wala nutti.

nuuru-bakkan b- : yaxu bakkan b-. ci nuuru-bakkan lañ ko dóor.

nuus : dinañuy wax tamit niib, nacc. (seetal niib)

nuut : (ne nuut). miig (ne), patt (ne). bi gone gi gisee yar bi, la ne nuut.

nuux : dinañuy wax tamit nóox. (seetal nóox)

nux-nuxi : yég bànneex bu rëy. li jëkkër ji ñëw mootax ndaw si di nux-nuxi.

nuyu : booy romb ay nit, nanga leen nuyu.