dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

nob : sopp, bëgg. nee na dafa nob ndaw si ba menu ko sore.

nocci : dindi buumu caq wala leneen lu ni mel. dafay nocci kurus gi. safaan wi mooy nas.

nodd 1 : woote julli ca jàkka ja. nodd nañu tisbaar ba pare.

nodd 2 : tëb. fas wi nodd na ak sareet bi.

noflaay g- : dallu b-. àdduna amul benn noflaay. safaan wi mooy coono b-.

noggatu : muqatu. lutax alkaati yi di noggatu sófoor yi ?

nogoy g- : màgget m-. nogoy gi mu àndal, maamam la.

nokkas : ñuux. nokkas na saaku bi ba mu fees dell ak ngooñ. dinañuy wax tamit nokkos wala rokkos.

nokki : dinañuy wax tamit noyyi. (seetal noyyi)

nokkos-nokkosi : di doxe ni am màgget. sa maam a ngay nokkos-nokkosi di ñëw.

nokkos : dinañuy wax tamit nokkas wala rokkos. (seetal nokkas)

nom : yëkkati ay wagg, mog. suy dox, dafay nom ay waggam.

noob b- : li ñuy defaral xale mu lekk ko su feree. noob su fanaanee yàqu.

nooj : rinki. tànkam yu nooj yi terewu koo mën a daw.

nooju : jële nit ku sëgg ci dënn bi ngir daaneel ko. mbër mi dafa ko nooju, daan ko jéll bu set wecc.

noon b- 1 : noon wenn waaso séereer wu dëkke diwaanu Cees la.

noon b- 2 : mbañ g-. waxi noon dafa lay yokk jom rekk. safaan wi mooy xarit b-.

noo g- : naw g-. bi mu turnee gis jaan ji, noo gi dafa dog ci saa si.

noor : nekk fekk ci noor b-. daaw Kaasamaas la noor.

noot : lottal, sonal. nit ku ñuul waratul a seetaan mukk kenn di ko noot.

nooy-bopp : ku nooy-bopp mooy koo xam ne, loo ko wax, mu gëm ko.

nooy : pataas bi nooy na wànte dafa tàng. safaan wi mooy dëgër.

noppal : féexal. sa mbindaan bi ci kër gi, du jaam, dee ko noppal. safaan wi mooy sonal.

noppi : bàyyi wax ji wala coow li. waa ji doon wax noppi na. / pare, sottal. noppi na ci li mu doon def.

nopp b- : nopp bi dafay metti.

noppu-jaboot : noppu-jaboot lañuy tudde golo ci kanam xale buy nàmp.

noq : dóor, duma, ñaf. soo ko tooñee, mu noq la.

nor : siwo bi dafa nor. dinañuy wax tamit nott.

nos 1 : waa ji dafa nos.

nos 2 : def ab jaaru ci bakkanu nag wala beneen mala. nag wi dafa soxor mootax borom nos ko.

nose g- : toflin g-. bu kenn jalgati nose gi.

nott : dinañuy wax tamit nor. (seetal nor)

noyyi : xaj bi deewagul, mu ngi noyyi ba léegi. dinañuy wax tamit nokki.