dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ni 1 : ponkal mu toll ni yow, di bëre ak xale yi. dinañuy wax tamit niki.

ni 2 : dinañuy wax tamit ne. (seetal ne)

niib : tiib, nacc, nuus, katam. muus mi ne na niib jinax ji.

niim g- : àkkaasiyaa g-. bàyyil ron niim gi ngay toog te dem liggeeyi.

niin : lu taq diwlin. demal raxasuji, sa yoxo yi dañoo niin.

niir : seet bu baax. gët yi neexuñu mootax muy niir bind yi.

niis : tey dafa niis, leerul. safaan mooy leer.

niit : jubal ag leer fenn. bul ma niit làmp bi.

niiw b- : dinañuy wax tamit néew b-. (seetal néew)

nijaay j- : rakk wala magu yaay. nijaayam la beyleji.

niki : dinañuy wax tamit ni. (seetal ni)

ninki-nanka b- : rab wu yéeme wu ñuy faral di tudd ci léebi wolof yi. dangay dégg ninki-nanka rekk wànte xamuloo lan la.

niru : mel. xale bi niru na pàppaam.

nisar g- : dinañuy wax tamit nësër g-. (seetal nësër)

nitaal : dinañuy wax tamit nataal. (seetal nataal)

nit k- : nit dafay am yar.

nitt b- : ñaar-fukk. nitti xar la jënd di leen jaayaat.