dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ngaaga l- : ngaaga lu rëy la mool yi gisoon géej. dinañuy wax tamit ngaaka l-.

ngaaka b- : ku ñàkk-xel k-, dof b-. gelam bi ngaaka bu mag la.

ngaaka l- : dinañuy wax tamit ngaaga l-. (seetal ngaaga)

ngaakin w- : dinañuy wax tamit ndaakin w-. (seetal ndaakin)

ngaakin w- : fas wu góor w-. aw ngaakin lañu ko jaay.dinañuy wax tamit ndaakin w-.

ngaana l- : baatu ngaana mu ngi jóge ci baatu gaana. (seetal gaana)

ngaañ l- : baatu ngaañ mu ngi jóge ci baatu gaañ. (seetal gaañ)

ngaaràndu : boole liggeey ak woy, baraan. ñoom ñépp a nga ca waar wa, di ngaaràndu.

ngaareew m- : kanaal b-. ngaareew mi mooy yóbbu ndox mu tilim mi yépp géej.

ngaax b- : ay saaku yu ñu def ci weti géleem, saaku b-, perngal b-. naar baa ngi toog ci kow ngaax yi.

ngajj : téq, pàdd. alkaati bi dafa ngajj saay-saay bi, mu daanu. dinañuy wax tamit ngànj.

ngalam w- : wurus w-, gal b-. wurusu ngalam dëgg la la jaay.

ngalaw : tey dafa ngalaw. dinañuy wax tamit ngelaw.

ngalla : mas-sa, waay-waay. ngalla alali askan wi ñu la dénk, bu ko def sa alali bopp, saytu ko saytu bu leer nàññ. dinañuy wax tamit ngella.

ngallax : soosu buy ak tiga-dege bu ñuy boole ak karaw. katolik yi dañuy ngallax ci feeti pag yi.

ngal : sànkar. guro bi dafa ngal.

ngande : dinañuy wax tamit ngand. (seetal ngand)

ngand : rëy, ponkal. nit ku ngand laa dajeel. dinañuy wax tamit ngande. safaan wi mooy tuuti.

nganj : wiyole. yére bi mu soloon melo wu nganj la yore.

ngan g- : baatu ngan mu ngi jóge ci baatu gan. (seetal gan)

ngañaay l- : bonofiis b-. sa liggeey bi amul ngañaay, demal wuti beneen. safaan wi mooy perta b-.

ngañ m- : dinañuy wax tamit mbeex m-. (seetal mbeex)

ngarab s- : baatu ngarab mu ngi jóge ci baatu garab. (seetal garab)

ngar : dajale. góob nañu ba ngar dugub ji.

ngas m- : baatu ngas mu ngi jóge ci baatu gas. (seetal gas)

ngatan l- : lalu gittax b-. taalibe yi dañuy defar ay ngatan.

ngato : defar ngato. dafay ngato di jaay.

ngawar g- : jëfu war fas mooy ngawar.

ngàdd : dóor ci baat. waa ji dafa ngàdd sàcc bi rekk mu daanu.

ngànda g- : cawarte g-. tey danga ànd ak ngànda gu mat sëkk. safaan wi mooy tayal g-.

ngàngoor l- : rafetaay b-, taar b-. ngàngooru ndaw si jéggi na dayo. safaan wi mooy ñaawaay b-.

ngànja l- : dugub ju ñu wol ngoon. cere ji ngànja la.

ngànj : dinañuy wax tamit ngajj. (seetal ngajj)

ngànnaay l- : li ñuy yore ngir aaru. sooy dox guddi danga war a yor ngànnaay.

ngànt l- : baatu ngànt mu ngi jóge ci baatu gàntu. (seetal gàntu)

ngàttaan l- : baatu ngàttaan mu ngi jóge ci baatu gàtt. (seetal gàtt)

ngàtte b- : baatu ngàtte mu ngi jóge ci baatu gàtt. (seetal gàtt)

ngecceel l- : ngecceel mooy jàppe sa bopp ku tuuti, ku amul solo. bëgg der bu weex bay xeesal, ngecceel la. safaan wi mooy rëy g-.

ngeel : coy, werta. pentiir bu ngeel la pentiir otoom bi.

ngeer g- : ngeer xeetu gajj la.

ngegenaay l- : mënuma tëdd ci ngegenaay. dinañuy wax tamit njegenaay l-.

ngelaane l- : ngelaw lu am doole l-. taw bi dafa àndoon ak ag ngelaane.

ngelabon l- : ngelabon mooy njëlbeenu nekku mbindeef.

ngelaw : dinañuy wax tamit ngalaw. (seetal ngalaw)

ngella : dinañuy wax tamit ngalla. (seetal ngalla)

ngembal-der b- : alkaati b-, sàndarma b- (turu ñaawal la). ngembal-der bi fii lay taxaw rekk, sófoor bu yegsi, mu saytu say kayit.

ngemb : ngemb na mbëram ba mu dugg ci géew bi.

ngent l- : baatu ngent mu ngi jóge ci baatu gent. (seetal gent)

nger m- : baatu nger mu ngi jóge ci baatu ger. (seetal ger)

ngédd l- : ñag b-, léem b-. bëy yi dugg nañu ci biir ngédd li.

ngéndi m- : dëkk bu mag b-. Tuuba am ngéndi la léegi.

ngénte : joxe turu liir. suba lañuy ngénte doomam ji.

ngér m- : mbedd mu yaatu m-. ci ngér mi la këram nekk.

ngéwal g- : baatu ngéwal mu ngi jóge ci baatu géwal. (seetal gërëm)

ngëb : dinañuy wax tamit ŋëb. (seetal ŋëb)

ngëjëm l- : ngëjëm mooy gittaxu dugub wala gu basi gu am suukar.

ngëleen l- : ngelaw lu am doole l-, ngelaane l-. ngëleen la jaar ca dëkk ba te bàyyiwu fa genn garab gu ndaw, yépp la daane. dinañuy wax tamit ngëlen l-.

ngëlen l- : dinañuy wax tamit ngëleen. (seetal ngëleen)

ngëmadi g- : baatu ngëmadi mu ngi jóge ci baatu gëm. (seetal gëm)

ngëm g- : baatu ngëm mu ngi jóge ci baatu gëm. (seetal gëm)

ngëneel l- : baatu ngëneel mu ngi jóge ci baatu gën. (seetal gën)

ngën g- : baatu ngën mu ngi jóge ci baatu gën. (seetal gën)

ngërëm l- : baatu ngërëm mu ngi jóge ci baatu gërëm. (seetal gërëm)

ngigis g- : ngigis xeetu gajj la.

ngiñ g- : baatu ngiñ mu ngi jóge ci baatu giñ. (seetal giñ)

ngir : ndax. dama la koy jox ngir nga jottalil ma ko sa yaay.

ngiro : caŋ. oto bi dafa ngiro ci beeñ bi.

ngistal l- : baatu ngistal mu ngi jóge ci baatu gis. (seetal gis)

ngomaar b- : xewum pecc mu ñuy def laata ñuy jongal ay xale. fan yii di ñëw lañuy def seen ngomaar bi.

ngone g- : baatu ngone g- mu ngi jóge ci baatu gone g-. (seetal gone)

ngone s- : baatu ngone s- mu ngi jóge ci baatu gone g-. (seetal gone)

ngonk m- : mbaam mu mag te am doole, baxla b-. bu fas seeree, nit ñi jënd ngonk.

ngont l- : liggeeyu ngoon b-. ci lenn ngont lañu bey tool bi yépp. safaan wi mooy xëy b-.

ngoolool b- : jaan ju ndaw j-. ngoolool la gis ci gajj gi.

ngoon g- : diggante midi ba timis. ngoon lay ñëw. safaan wi mooy suba g-.

ngooñ m- : ñax m-. ngooñ mi dafa tawte.

ngoox : baatu ngoox dafay toppandoo ni mbott di yuuxoo.

ngopp l- : bëj-gànnaar b-. Móritani mu ngi ci ngoppu Senegaal.

ngori l- : xeetu ñebbe. ay ngori rekk lay bey.

ngornmaa b- : dinañuy wax tamit gornmaa b-. (seetal gornmaa)

ngornmãa b- : dinañuy wax tamit gornmaa b-. (seetal gornmaa)

ngor g- : baatu ngor mu ngi jóge ci baatu gor. (seetal gor)

ngoro : jappànte ak keneen ngir mbëggeel (diggante góor ak jigeen). waa ji dafay ngoro as ndaw ci kër gi.

ngot b- : ngot xeetu jën la.

ngot l- : yet w-. ab ngot la doon dóor sàcc bi.

ngóob m- : baatu ngóob mu ngi jóge ci baatu góob. (seetal góob)

ngóoŋ b- : xaj bu góor bu mag b-. ngóoŋ bi dafay jaay.

ngóora l- : baatu ngóora mu ngi jóge ci baatu góor g-. (seetal góor)

ngóor s- : baatu ngóor s- mu ngi jóge ci baatu góor g-. (seetal góor)

nguna g- : dinañuy wax tamit ngunu g-. (seetal ngunu)

ngunu g- : ngunu gi dafa fees dell ak ay ginaar. dinañuy wax tamit nguna g-.

ngurbaan g- : ñamu séereer wu ñuy defare sungufu dugub ak yàpp wala jën. xamuloo nu ñuy toggee ngurbaan.

nguri b- : jullikaata b-. nguri dafay màtte.

nguufaan : mu nga nguufaan xale ba di dem.

nguuka b- : xeetu jën. ay nguuka la jënd.

nguur g- : ngornmaa b-. ci nguur gi lay liggeey.