dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ne 1 : wax. mu ne déggul wolof. bi mu gisee, yar bi dafa ne tekk. dinañuy wax tamit ni.

ne 2 : dégg naa ne duy nàmpal doomam ji. dinañuy wax tamit ni.

neb-neb g- : neb-neb garabu àkkaasiyaa la gu ñuy jëfandikoo ay doomam ngir dénd der.

nebbon b- : nékk g-, geres g-. xar mi bare na nebbon.

nebedaay g- : nebedaay xeetu garab la. mbuumu nebedaay bi neex na.

neen g- : dara. du joxe xaalisam ci neen. yaramu neen la defoon. leketu neen naxul béy. (léebu).

neer : di am xel muy teey soo nekkee ci waruwaay yu mel ni oto wala bató. dafay neer mootax duy tukki lu bare.

nees-tuuti : dinañuy wax tamit nees-tuut. (seetal nees-tuut)

nees-tuut : ginnaaw diir bu gàtt. nees-tuut ki ñu doon xaar yegsi. dinañuy wax tamit nees-tuuti.

neex-baat : woykat dafa war a neex-baat. safaan wi mooy naqari-baat.

neex-deret : lewet. doom ji, barewul ay jooy, dafa neex-deret. safaan wi mooy naqari-deret wala wex.

neex-làmmeñ : li mu lay wax dara amu ci, dafa neex-làmmeñ rekk. dinañuy wax tamit neex-làmmiñ.

neex-xel : muus, yeewu. xale bi ku neex-xel la, ci ay weer rekk la mokkal alxuraan. safaan wi mooy naqari-xel, ñàkk-xel, wala dof.

neex : togg yu neex lay togg. / jikkoom neex na ma lool. / dafa neex a nax. safaan wi mooy naqari.

nefare j- : puubi fas y-. nefare baax na lool ci tool.

nef : am ay ëmb yu jege. ndaw si nef na ñaari yoon.

neg-negi : yég ay màndargay sibbiru. sooy neg-negi, demal kër doktoor.

nekk : doon. ku nekk borom dëkk ba léeegi ? / lu nekk ci biir pax mi ?

nelaw : mu ngi nelaw ci suba ba léegi. safaan wi mooy yeewu.

nel : wat kawari bopp bu mu set wecc. boppam bi dafa am ay góom mootax ñu nel ko. dinañuy wax tamit ndel.

nemm 1 : (ne nemm ). baat bi dafay tekki lu ne tekk yëngatootul. muus maa ngi tëdd ne nemm.

nemm 2 : sakk lem. dañuy nemm lem ci garab gi.

nemmali : jekkali. rëbbkat bi nemmali na till gi.

nemmat : jàmbat, jooytu. li ngay nemmat la ñépp di nemmat.

nemmeeku : seet, fàtteliku. ndax dingay dem di nemmeeku sa waa-jur ya ca dëkk ba ? dinañuy wax tamit nemmiku.

neneen : beneen anam b-. soo ko defee noonu doxul, defe ko neneen.

nenne b- : liir b-, doom j-. sa nenne bi dafa bare ay jooy.

nennu : tàmmu di sonal nit. jabar ji dafa ko nennu, lu mu ko wax, du ci teg baat.

nen : ginaar gi nen na ci rondal gi.

nepp : baatu nepp dafay ànd ak baatu nooy te di tekki bu mu ëpp. pataas bi dafa nooy nepp. safaan wi mooy këŋŋ (dëgër këŋŋ).

nere g- : wuul g-. ngelaw lee daane nere gi.

nes-nesi : ler-leri. bi ndaw si soloo ba génn, dafa doon nes-nesi.

netetu j- : doomi nere yu ñu nëbal di ko def ci ag togg. mbaxal gi am netetu ju doy.

nettali : li ngay nettali mbaa am nga ci lu la wóor ?

new g- : garabu new. seen àll ba am na ay garabi new.

newwi : bi mu danoo la tànkam bi newwi. dinañuy wax tamit néwwi.