dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ndaag l- : baatu ndaag mu ngi jóge ci baatu daagu. (seetal daagu)

ndaakin w- : fas wu góor w-, naaru-góor w-. xaalis bu bare la jëndee ndaakin wi. dinañuy wax tamit ngaakin w-. safaan wi mooy wajan w-.

ndaama : gàtt, tuuti. jotul xobi garab gi ndax dafa ndaama. safaan wi mooy njool.

ndaanaan b- : ku mën li muy def, artist b-. Yuusu Nduur ndaanaan la ci woy. safaan wi mooy cuune b-.

ndaa l- : mbànd m-. ndaw si root na ndaa yi yépp.

ndaare b- : ndaare mooy ki mujj ci raŋ gi. Aliw a jël ndaare ci kalaas bi. dinañuy wax tamit ndàdde b-.

ndaas m- : baatu ndaas mu ngi jóge ci baatu daas. (seetal daas)

ndaataatallax : di dundu dundu gu neex lool. tey dibéer la, dañuy ndaataatallax.

ndab l- : defukaay b-, bool b-. bul def ñam ci ndab li te raxasuloo ko.

ndagaan l- : ñaan g-. yal na Yàlla nangu suñu ndagaan li. / can l-, warugar w-. xaalis bi nga laaj yépp, dafa ëpp ci ndagaan.

ndajem-baat m- : ay baat yu ñu boole. baatu ndarakàmm ci ndajem-baat mii di bëccëgu ndarakàmm rekk lañu koy gis.

ndaje m- : baatu ndaje mu ngi jóge ci baatu daj. (seetal daj)

ndakaaru g- : Dakaar, kapitaalu Senegaal. Ndakaaru la doomam yépp juddoo.

ndal l- : baatu ndal mu ngi jóge ci baatu dal. (seetal dal)

ndambe b- : ñebbe bu ñu baxal. soxna si ndambe la togg reer tey. dinañuy wax tamit nambe b-.

ndam l- : sa mbër mi am na ndam.

ndañ : baatu ndañ mu ngi jóge ci baatu dañ. (seetal dañ)

ndañtaali b- : wax ju mujj ji mooy ndañtaali bi. wure wa dem ne këŋ, waxi mag dem na ndañtaali (léebu la).

ndarakàmm : baatu ndarakàmm ci ndajem-baat mii di bëccëgu ndarakàmm rekk lañu koy gis. mu ngi tekki digg bëccëg.

ndare : àttaa, doonte. dinaa ko def ndare wóoluwuma li mu wax.

ndarkase g- : garabu ndarkase g-. dinañuy wax tamit darkase g-. (seetal darkase)

ndar : Saint-louis. Ndar nekkoon na fi kapitaalu Senegaal.

ndaw 1 : tuuti. xale bu ndaw laa gis muy tux sigaret. safaan wi mooy mag.

ndaw 2 : aka. ndaw nit ñu bare !

ndawal l- : rënd b-. jën, yàpp wala lépp luy tegu ci kow ñam. cere ji amul ndawal.

ndaw g- : jamono ji nga nekke xale bu góor ba ba ngay doone mag. bul foye sa ndaw. / raw g-. xale bu jigeen bu nekk war naa sàmm ndawam ba am jëkkër.

ndaw l- : ku ñu yónni. ndaw li Dakaar la jóge. / xale b-. ndaw dafay nangoo jàng. / ki teewal keneen. ñëwul wànte yónne na ndaw.

ndaw ñ- : xale y-. ndaw ñi dañoo war a jàng ndax ñu mën a yore réew mi ëllëg. safaan wi mooy mag ñ-.

ndaw s- : soxna s-, jigeen j-. ndaw si fonk na séyam bi.

ndawràbbin b- : feccu cosaanu lébu. lébu yaa ngay fecc ndawràbbin.

ndawtal : joxe benn kadó ci xew, may, dolli. xaalis bu bare la ndawtal xaritam bi doon ngénte.

ndax 1 : xanaa. demuloo liggeeyi ndax di sàcc.

ndax 2 : ndax xam nga ne lu am Yàlla fekke na ? / xamuma ndax dina fa dem am déet.

ndax 3 : ngir. waxaat ko ko ndax bu mu ko fàtte.

ndax 4 : ngir, paskë. tey du jàngi ndax dafa feebar. dinañuy wax tamit ndaxte wala nax.

ndaxam : moone. ndaxam yaayam waxoon na ko ko.

ndaxte : dinañuy wax tamit ndax wala nax. (seetal nax)

ndàbb : tay, taf, kol. ndàbb na portale bi ci taax mi. safaan wi mooy tàyyi.

ndàdde b- : dinañuy wax tamit ndaare b-. (seetal ndaare)

ndàllaan l- : dinañuy wax tamit mboole m-. (seetal mboole)

ndàmpaay l- : baatu ndàmpaay mu ngi jóge ci baatu dàmp. (seetal dàmp)

ndàndi b- : beykat bu mat beykat. xale yi nangootuñu bey léegi wànte seen maam yi ay ndàndi lañu woon.

ndànd g- : àll bu yaatu b-. nagam waa nga feeñe ca ndànd ga. dinañuy wax tamit ndànd-foy-foy g-.

ndànjaama b- : nit ku yore bopp bu réy. ndànjaama bi dëkkul ci réew mi.

ndànk : defal ndànk rekk, doo lekk lu dul sa wërsëg mukk.

ndàq m- : baatu ndàq mu ngi jóge ci baatu dàq. (seetal dàq)

nde-kon : su dul woon loolu. dafa amul xaalis rekk nde-kon moo koy njëkk a yég.

ndeem : dinañuy wax tamit ndéem, ndégam wala ndegem. (seetal ndéem)

ndeer g- : Ndeer dëkk la bu nekk Waalo te siiw ci Senegaal ndax jigeen ña fa dajaloowoon ci ab néeg, taal seen bokk ci jamono joo xam ne, góor ñi ñépp a nga woon ca tool ya. loolu mu ngi amoon bésu talaata, mootax sax ñu naan talaatay Ndeer.

ndeer w- : ndeer aw xeetu picc la.

ndeete l- : fi weer wala at di deewee. ci ndeete weer wi la nit ñi di jot seen peyoor.

ndegam : jàngil mécce ndegam naguwuloo jàng. dinañuy wax tamit ndégam, ndegem wala ndéem.

ndegem : dinañuy wax tamit ndéem, ndeem wala ndégam. (seetal ndéem)

ndeke : seet na ko ci kër gi ba sonn ndeke ca liggeeyukaayu ba la ko bàyyi. dinañuy wax tamit ndekete wala ndekete yoo.

ndekete yóo : dinañuy wax tamit ndeke wala ndekete. (seetal ndeke)

ndekete : dinañuy wax tamit ndeke wala ndekete yoo. (seetal ndeke)

ndekkite g- : baatu ndekkite mu ngi jóge ci baatu dee. (seetal dee)

ndell b- : fetal g-. bul jaar foofu, dafa am ay ndell. dinañuy wax tamit ndéll b-.

ndel b- : dinañuy wax tamit nel b-. (seetal nel)

ndem-dellu b- : paxu jinax m-. jinax jaa ngi génne ci ndem-dellu bi.

ndem-si-Yàlla j- : ku dundatul la ñuy tudde ndem-si-Yàlla ji. dinañuy wax tamit njëm-si-Yàlla j-.

ndem l- : baatu ndem mu ngi jóge ci baatu dem. dinañuy wax tamit dem b-. safaan wi mooy dikk b-. (seetal dem)

ndenceef l- : baatu ndenceef mu ngi jóge ci baatu denc. (seetal denc)

ndend l- : baatu ndend mu ngi jóge ci baatu dend. (seetal dend)

ndengeñ : bañ a jël dara, gedd. ndengeñ na li ñu ko jox.

ndengleer g- : dinañuy wax tamit ndéneer g-. (seetal ndéneer)

ndesit l- : baatu ndesit mu ngi jóge ci baatu des. (seetal des)

ndetteel l- : jéllu ginnaaw b-. sama ndetteel leey metti sama ndigg li.

ndey-dikke j- : nit ku jigeen koo sopp, def ko xarit. ndey-dikkeem lay toggal añ.

ndey-ji-séex j- : yaayu séex j-. ndey-ji-séex dafa war a am ku koy jàppale ci ay séexam.

ndeyi-koor g- : ndeyi-koor mooy juroom-ñaareelu weer ci atum jullit.

ndeyjoor b- : wetu ndeyjoor. lekkool baa ngi nekk ci wetu ndeyjoor. safaan wi mooy càmmoñ b-.

ndey j- : yaay j-. ku nekk war naa weg sa ndey. / turu jigeen w-. Ndey dafay fóot tey.

ndeyu-mbill g- : ndeyu-mbill gi mooy nit ki nekk ci bopp bi.

ndéef g- : nefare j-. ndéef ci tool dafay naatal gàncax.

ndéego l- : ndékki l-. ndéego li cere ak mbuum la. dinañuy wax tamit ndéegu l-.

ndéegu l- : dinañuy wax tamit ndéego l-. (seetal ndéego)

ndéem : ndéem bëgguloo dem, toogal. dinañuy wax tamit ndeem, ndégam wala ndegem.

ndéeñ b- : tubey ji dafa bënn ci tolloo ak ndéeñ bi. dinañuy wax tamit ndëñ b-.

ndéey l- : baatu ndéey mu ngi jóge ci baatu déey. (seetal déey)

ndéeyoo l- : baatu ndéeyoo mu ngi jóge ci baatu déey. (seetal déey)

ndégam : dinañuy wax tamit ndéem, ndeem wala ndegem. (seetal ndéem)

ndékki : tey duma ndékki.

ndéll b- : dinañuy wax tamit ndell b-. (seetal ndell)

ndéneer g- : ndengleer g-, ndànd g-. nag yaa nga ca ndéneer ga.

ndés g- : basaŋ b-. mu ngi tàllalu ci ndés gi. dinañuy wax tamit ndës g- wala ndéstan g-.

ndéstan g- : dinañuy wax tamit ndés g- wala ndës g-. (seetal ndës)

ndéwenal : baatu ndéwenal mu ngi jóge ci baatu déwen. (seetal déwen)

ndëdd m- : ndënd sabar bu mag la bu tëju ci suuf.

ndëgërlaay l- : baatu ndëgërlaay mu ngi jóge ci baatu dëgër. (seetal dëgër)

ndëggu l- : baatu ndëggu mu ngi jóge ci baatu dëgg. (seetal dëgg)

ndëkk s- : baatu ndëkk si mu ngi jóge ci baatu dëkk bi. (seetal dëkk)

ndënd m- : tëggkat yaa ngay tëgg ndënd ya.

ndëngte g- : baatu ndëngte mu ngi jóge ci baatu dëng. (seetal dëng)

ndëñ l- : baatu ndëñ mu ngi jóge ci baatu dëñe. (seetal dëñe)

ndëpp : def ay ndëpp. lébu yi dañuy ndëpp tey.

ndës g- : dinañuy wax tamit ndés g-. (seetal ndés)

ndëxëñteef l- : baatu ndëxëñteef mu ngi jóge ci baatu dëxëñ. (seetal dëxëñ)

ndigaale g- : ndigaale mooy lu ay nit séq wala kóllëre.

ndigal l- : waaw j-. jëwriñ ji joxe na ndigal ñu tàmbali liggeey bi. / perefe joxewul ndigal ngir ñu amal doxu ñaxtu bi.

ndigg l- : baatu ndigg mu ngi jóge ci baatu digg. (seetal digg)

ndig : ndig baat la bu ñuy wax ngir dàq aw nag.

ndiig l- : ndaw lu demal xaritam ci ay goroom. seetal ku mat ndiig nga yebal ko ci sa goro yi.

ndiiraan g- : mbooloo m-, gurub b-. way pólotig yi ndiiraan rekk lañu bëgg.

ndiir j- : dinañuy wax tamit ndeer j-. (seetal ndeer)

ndikkaan m- : baatu ndikkaan mu ngi jóge ci baatu dikk. (seetal dikk)

ndimbal l- : baatu ndimbal mu ngi jóge ci baatu dimbali. (seetal dimbali)

ndimb m- : fas wu weex w-. Ibu mësoon naa yore am ndimb.

ndimo l- : piis b-. ñaata nga jëndee ndimo li ?

nding m- : wurmbal b-, cëpp g-. am na nding ba mu fees ak ngooñ.

ndodd l- : diggu ginnaaw g-. teg na saaku ceeb bi ci ndodd li.

ndof g- : baatu ndof mu ngi jóge ci baatu dof. (seetal dof)

ndogal l- : baatu ndogal mu ngi jóge ci baatu dog. (seetal dog)

ndog m- : baatu ndog mu ngi jóge ci baatu dog. (seetal dog)

ndogu l- : baatu ndogu mu ngi jóge ci baatu dog. (seetal dog)

ndoket b- : kamisol b-. ndoket robb bu yaatu lay doon.

ndokk : baat la buy tekki def nga ko ni ma ko bëggewoon. ndokk ! bi Yàlla joxe sama doom ji liggeey.

ndollen l- : baatu ndollen mu ngi jóge ci baatu dolli. (seetal dolli)

ndombo-tànk g- : dekoore b-. waa ji li mu defal réew mi mootax ñu takkal ko ndombo-tànk.

ndombo g- : téere bu ñu ëw di ko takk ci loxo, ci tànk wala ci ndigg. mbër mi takk na ay ndombo yu bare.

ndongomaate b- : doomu jiit j-. gis na benn ndongomaate ci gajj gi. safaan wi mooy jànkalaar j-.

ndongo l- : taalibe b-. ndongo li mokkal na kaamilu alxuraan. safaan wi mooy sëriñ b-.

ndono l- : baatu ndono mu ngi jóge baatu donn. (seetal donn)

ndoŋ l- : cuukel b-. ci ndoŋ la ko xeer wi dal.

ndoorte l- : baatu ndoorte mu ngi jóge ci baatu door. (seetal door)

ndox-suuf b- : jaan j-. ndox-suuf la ñuy jëfandikoo guddi ngir tuddu jaan.

ndoxaan l- : baatu ndoxaan mu ngi jóge ci baatu dox. (seetal dox)

ndox m- : ndox mu sedd, ndox mu tang. may ko ndox mu naan.

ndoxtu l- : doom b-, piyoŋ b-. say ndoxtu yépp jeex nañu.

ndoxum-siti m- : sifilis b-. doktoor bi ne na ko ndoxum-siti la yore. dinañuy wax tamit siti s-.

ndóbin g- : ku ndóbin rey sa maam foo séen lu ñuul daw. (léebu).

ndóndi b- : ku ñakk-xel. ndóndi kenn du ko wóolu.

ndóobu w- : fas wu yore tànk yu weex. aw ndóobu lay jaay.

ndóol : ñàkk. su liggeey amul, nit ñi dañuy ndóol. safaan wi mooy am-alal.

ndóomaar m- : mbonaatu géej mu réy. gis naa am ndóomaar.

ndugg m- : baatu ndugg mu ngi jóge ci baatu dugg. (seetal dugg)

ndulli : dóor dóor yu metti. xale yi ndulli nañu sàcc bi ba muy bëgg a dee.

ndull : (ne ndull ). def yaramu neen, soluloo mbubb, soluloo tubey, duŋŋ (ne). dof baa nga ne ndull ca digg mbedd ma. safaan wi mooy solu.

nduluñ : ñàkk say piyoŋ yépp ci ab wure. dañu doon damiye mu nduluñ.

ndung-siin b- : kaso g-. bu la alkaati yi jàppee ngay tux yàmbaa, ndung-siin la ñu la jëme.

ndunkurunk g- : dinañuy wax tamit ndunqurunq. (seetal ndunqurunq)

ndunqurunq g- : sa ndunqurunq gi dafay metti ? dinañuy wax tamit ndunkurunk g-.

ndutt b- : waaso séereer yu dëkke ci diwaanu Cees. làkku séereer ndutt bokkul ak làkku séereer Siin.