dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

naa 1 : naa daw ñibbi bala muy taw.

naa 2 : lekk naa laax tey.

naaféq : rambaaj. waxal dëgg gi rekk, bul naaféq.

naaf : dajale gerte gi ñu deqi ba pare, gar ko. naaf lañu xëye tey.

naag : dem ba àndatuloo ak sa xel ndax màgget. góor gi dafay naag. dinañuy wax tamit naax.

naagu : dem ba yaakaar ne li nekk rekk mooy wéy ba fàww. bul am mukk ba naagu.

naaje b- : bànga b-. du lekk naaje. dinañuy wax tamit naajo b-.

naaj : gaawleen ci li ngeen di def, naaj na.

naajo b- : dinañuy wax tamit naaje b-. (seetal naaje)

naal : mébet, xalaat, nësër. naal na dem jàng Tugël.

naam 1 : óo ! ; ãa !. naam baat la booy wax booy wuyu ab woote.

naam 2 : gaa. naam waxoon na ma ko, wànte dama ko fàtte.

naan 1 : naan nañu ndox mu sedd guyy. / naan sàngara, màndi. waa ji dafay naan.

naan 2 : wax, di wax ne. soo ko xamul, danga naan dafa dof.

naan-kaani : tàng-xol. góor googu dafa naan-kaani.

naana b- : mànt b-. defal naana ci àttaaya bi.

naanu g- : gënn tuxu g-. ag naanu lay tuxe.

naar-bët b- : naar-bët aw rab wu tuuti te xonq coyy la.

naari : dinañuy wax tamit safara. (seetal safara)

naar b- : araab b-. Arabi Sawdi ay naar a fa dëkk.

naaru-góor w- : xeetu fas. takk-der yi ay fasi naaru-góor lañu waroon.

naataango b- : morom m- (ci bérebu liggeeyukaay). xolal sa naataango bi ni mu fonkee liggeeyam.

naat : lu bare, wala lu barele. su mbey mi doxee, réew mi naat.

naat b- : naat a gën a seer ginaar.

naaw : picc yépp naaw nañu.

naax : dinañuy wax tamit naag. (seetal naag)

naax b- : lu bare ci am mbir. tubaab yi ay naaxi jën lañu fiy jële di ko yóbbu seen réew.

nab : taq sa doom ba mu ëpp. dafa nab, fu mu tollu mu ngi yore doom ji.

nacc : niib, nuus, tiib. dafa daw ba nacc ginaar gi.

nafa g- : dencukaayu xaalis b-. def na xaalisam bi yépp ci nafa gi.

nafar : jàngaat bu baax. dafay nafar bindam yi.

nafsu g- : bakkan b-. baatu nafsu ci topp sa nafsu rekk lañuy faral di ko dégg. bul topp sa nafsu mukk ba yàq sa àdduna.

nagam : sanax. soo ko defaatee, dinaa la dóor ba nga nagam.

nag : yow nag, xanaa doo jàngi. / suba nanga jënd dàll nag.

nag w- : dafay yar ay nag.

naj : kepp. bunt bi naj na ko.

naka-jekk : naka-jekk du liggeey gaawo.

naka : dinañuy wax tamit na, nan wala nu. (seetal na)

nakk-nakkal : wax lu lëndëm. waxal lu leer ngay nakk-nakkal.

nal : nal na limoŋ ji ci ceeb bi.

namm : ndaw si dafa namm jëkkëram. / bëgg. loo namm ci li ngay def nii ?

nanga : nanga jàng àngale ak araab yépp.

nangu 1 : jëlaat li nga joxewoon ba pare. nangu na xaalis bi mu ko mayoon yépp. / jël ak doole. alkaati bi nangu na permi waa ji.

nangu 2 : ànd ci dara. nangu na jabar ji di liggeey guddi. safaan wi mooy bañ. / yal na Yàlla nangu ñaan yépp.

nan : nan la ko defe ? dinañuy wax tamit naka wala na.

na : na nga def ? dinañuy wax tamit naka wala nan.

nappaaje : riij. nag yi nappaaje nañu toolu gerte bi yépp.

nappaate : dafay nappaate rekk wànte kenn faalewu ko.

napp : solleen seen sile yi leen di aar ci lab, su ngeen di nappi.

naqadi-baat : woykat bi dafa naqadi-baat. dinañuy wax tamit naqari-baat. safaan wi mooy neex-baat.

naqadi-deret : góor gi ku naqadi-deret la. dinañuy wax tamit naqari-deret. safaan wi mooy neex-deret.

naqadi : ceeb bu naqadi la ndaw si togg tey. dinañuy wax tamit naqari. safaan wi mooy neex.

naqari-baat : dinañuy wax tamit naqadi-baat. (seetal naqadi-baat)

naqari-deret : dinañuy wax tamit naqadi-deret. (seetal naqadi-deret)

naqari-xel : safaan wi mooy neex-xel. (seetal neex-xel)

naqari : dinañuy wax tamit naqadi. (seetal naqadi)

naqar w- : mettit w-. am na naqar ci li ko ndaw si sosal. safaan wi mooy bànneex b-.

naq : bës nit ci biir ndox. su ngeen demee géej, bul naq xale yi de.

nar 1 : fen, kàcc (fen wax ju ñaaw la). ak nu mu mën a deme, waxal dëgg rekk, bul nar. safaan wi mooy wax-dëgg.

nar 2 : bëgg a def. Yàlla ji dafa nar a taw tey.

nar 3 : séddale, xaaj, cër-cëre. mool yi nar nañu seen xaalis bi ñu jaayee seen jën yi ba pare.

nas 1 : jaarale wëñ ci bën-bënu puso wala bu per. ndax mën nga nas wëñ gi ? safaan wi mooy nocci.

nas 2 : taxawal benn porose. li waa dëkk bi nas mooy tabax fi ab loppitaal.

nasaraan b- : làkku Ërob w-, tubaab b-. nasaraan la waa ji di làkk.

nasax : ku mënul a def benn, yaafus. deel yëngal sa yaram wi, yow danga nasax lool.

nataal : rëdd, fóto, portale. xale yee nataal li ci tablo bi. dinañuy wax tamit nitaal.

natt 1 : seet dayo wala tolluwaayu am mbir. natt na yére bi mu ëpp ko.

natt 2 : teg. dañuy natt kenn ku nekk ñeenti téemeer weer wu jot.

nawe b- : nawe xeetu lëjum la.

nawet : def nawet bi fenn. ren Kaasamaas lay nawet.

naw : fonk, weg. danga war a nite ba ku la gis naw la. safaan wi mooy bañ, wegadi.

naw g- : noyyi b-. nawam gi dafa dogoon ab diir. dinañuy wax tamit noo g-.

nax-sa-goro b- : tubey j-. ab nax-sa-goro la soloon démb.

naxasaale : jéllale. dafay naxasaale rekk wànte xam na li nga ko wax.

naxee-mbaay b- : nax b-. li leen way-pólotig bi digoon yépp, ay naxee-mbaay la.

nax : dafa lay nax, sa yaay ñëwagul. / dafa bëgg xale bi noppi mootax mu koy nax. / ndaw si nobul waa ji, dafa koy nax, di lekk xaalisam bi rekk.

nay : ŋott. dafa nay ba du lekk sax. safaan wi mooy tabe wala yéwen.