dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

nëbb : làq. li ngay nëbb, lu mu yàgg yàgg, dina mës a feeñ. safaan wi mooy feeñal.

nëb : yàqu, forox. lutax ngay jaay banaana bu nëb bi ?

nëgëni-sii : fi-mu-nekk. nëgëni-sii beykat yaa ngi ruuj.

nëg : dinañuy wax tamit nég. (seetal nég)

nëpp : muur. bul nëpp dugub ji, weer ko ci naaj wi.

nëq b- : xeese b-. yére ba mu sol nëbbul sax nëq ba. dinañuy wax tamit naqb-.

nërëm : (ne nërëm). daanu sukk say wóom. bi mu gisee jaan ji, dafa tiit ba ne nërëm.

nërmeelu : daanu. lan nga doon daw ba nërmeelu nii ?

nësër : mébet. kër gi nga nësër a tabax, xaalis bu bare la laaj. dinañuy wax tamit nisar.

nëtëri b- : soos bu ñu defare buy ak tiga-dege te di ko àndale ak laax. laaxu soow a ma gënal laaxu nëtëri.

nëtëx : coy, ngeel, weerta. gañilaa bu nëtëx la soloon.

nëwu b- : nëwu pàcc la ci xam-xamu làkk.

nëww : jébbalu. nee na nëww ci sëriñu baayam bi.

nëx : am ay tilim. buleen naan ndox mi, dafa nëx.