dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

néeg : mën a dékku ag coxor. waaji ku néeg la, móol la sànni xaj bi. safaan wi mooy am-yërmande.

néeg b- : dugg na ci néeg bi.

néegu-sëy b- : kër gi jigeen di sëy. nanga fonk sa néegu-séy bi.

néew-doole : am tuuti ci doole. ba muy ndaw, kenn ëppu ko woon doole wànte léegi dafa néew-doole. safaan wi mooy am-doole.

néew-ji-doole j- : néew-ji-doole jaa ngi raŋ ci tali bi di yalwaan. dinañuy wax tamit néew-di-doole j-.

néew : tuuti. lu néew la ko may ci cere ji. safaan wi mooy bare.

néew b- : nit ku faatu k-. néew bi bitim réew la war a jóge. dinañuy wax tamit niiw b-.

nég : xaar. nég na la lu yàgg ñëwuloo, mu dem. dinañuy wax tamit nëg.

nékk g- : nebbon b-, geres g-. xaru yafal dafay bare nékk.

nétetu b- : nétetu ci rënd bi la bokk. mbaxal gi am ne nétetu

néwwi : dinañuy wax tamit newwi. (seetal newwi)