dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

nàcc : fompal sa góom biy nàcc.

nàddante : dimbalante. nit ñi dañoo war di nàddante.

nàkka : defar nàkka.

nàmm : daas. nàmm na paaka bi ba mu ñaw.

nàmp : xaaral ba xale bi nàmp ba suur. dinañuy wax tamit namp.

nànd foy-foy g- : dinañuy wax tamit ndànd g-. (seetal ndànd)

nànd : xam, jëli. nànd na li nga bëgg a def yépp.

nàngam : sàngam. bala nga naan nàngam ak nàngam, danga war a xam li ngay wax.

nàññ : baatu nàññ dafay ànd ak baatu leer di tekki bu baax. su làmp yi tàkkee, mbedd mi dafay leer nàññ. safaan wi mooy kuruus di baat biy ànd ak lëndëm.

nàttable : am-xel-ñaar. kenn nàttablewul ne moo fi dàq a jàng. dinañuy wax tamit naatable.