dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

mocc 1 : dàmp tey waxaale ay xam-xam yuy wéral. góor gi dafay mocc.

mocc 2 : dinañuy wax tamit macc. (seetal macc)

modd : wonn. dinañuy wax tamit mëdd. (seetal mëdd)

mog : dinañuy wax tamit nom. (seetal nom)

mokk : lu nekk sunguf. suukar su mokk lay àttaayaa. / lu ñu xam bu baax. li mu doon jàng mokk na léegi. / ku dégg ndigal. nag yi mokk nañu.

mooco m- : pooj b-. li mu sol yiwul ndax mooco yi yépp a ngi ci biti.

mool b- : nappkat b-. mool suy dem géej, dafa war a sol sile ndax mu mën a mucc ci lab.

mool w- : doomu fas. mool wi yaayam lay seet.

moom 1 : nijaayam a moom kër gi.

moom 2 : du man, moom la.

moom-sa-réew b- : tey lañuy màggal suñu bésu moom-sa-réew.

moomu : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

moonde : ndaxam. moonde ñépp waxoon nañu ko ko. dinañuy wax tamit moonte wala moone.

moone : ndaxam. dinañuy wax tamit moonde wala moonte. (seetal moonde)

moontar b- : sa moontar bi amul ëer. dinañuy wax tamit moontoor b-.

moonte : ndaxam. dinañuy wax tamit moonde wala moone. (seetal moonde)

moontoor b- : dinañuy wax tamit montar b-. (seetal montar)

mooñ : def ba sunguf nekk ay doom yu sew. dafay mooñ sunguf si.

moos : sax. li nga def doomi jàmbur ji ñaaw na moos.

moqarci : xoj, tàpparñi. moqarci na melentaan wi.

mor : tàpp. mor nañu xar mi. dinañuy wax tamit tàpp. (seetal tàpp)

morom m- : góor gi du sa morom, jox ko cër. dinañuy wax tamit moroom m-.

moroom m- : dinañuy wax tamit morom m-. (seetal morom)

morso b- : sagar b-. morso bi dafa taq deret.

mos : ñam. kaay mos ci soow mi.

mot : ndax xaalis bi mot na. / xale bu jigeen bi mot na léegi. / ay këram mot nañu juroom. / doomi jàmbur ji ngay liggeey, bàyyi ko, àdduna motu ko. dinañuy wax tamit mat. (seetal mat)

mott : (ne mott). dem ci lu gaaw. neel mott dellu fa nga jógewoon.

moxoñ : oto bi moxoñ na pot bi.

moyaal : dindi lempo ci dara. ci li nga am lañuy moyaal lempo bi.

moy : rëbbkat bi moy na fasu-àll wi. / ku njaalo moy nga Yàlla.