dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

midi : midi lañu fa war a daje.

miig : (ne miig). tekk (ne), patt (ne). ne leen miig mba ngeen génn yeen ñépp. dinañuy wax tamit miix (ne).

miikar b- : meex-sedd-rey b-. moytu ko, miikar la.

miim : weddi. li mu fi waxoon keroog yépp, miim na ko tey. safaan wi mooy nangu.

miin : tàmm, miis. xale bi mbindaan bi la miin.

miir : soo wëndeeloo dangay miir, toogal benn palaas.

miir b- : maraaj b-. sàcc yi dañoo bënn miir bi dugg ci biir kër gi.

miis : miin, tàmm. (seetal miin)

miis b- : mburu lëmm. mënuloo lekk miisu mburu.

miitiŋ b- : ndaje m-. mbaa la nga ñu waxoon ca miitiŋ ba, dinga ko def ?

miix : (ne miix). tekk (ne), patt (ne). dinañuy wax tamit miig. (seetal miig)

mikorob b- : doomu jàngoro b-. salte dafay andi ay mikorob.

milaatar b- : siñaara b-, njall b-. milaatar bi Ndar la dëkk.

milyoŋ b- : dinañuy wax tamit alfunni b-. (seetal alfunni)

milyoŋ b- : mbaa milyoŋ yi ngay tiitaroo yaa leen liggeey ?

mindaan m- : baatu mindaan mu ngi jóge ci baatu bind. dinañuy wax tamit mbindaan b-. (seetal mbindaan)

mindeef m- : baatu mindeef mu ngi jóge ci baatu bind. dinañuy wax tamit mbindeef m-. (seetal mbindeef)

ming : jaayu. géwel baa ngi koy xalamal muy ming.

minise b- : minise bu mën a liggeey laay sant sama lal bi.

miraas : séddoo alali ku faatu. miraas nañu seen alalu baay ji ba pare.

misaal : li nga wax, soo ko mënee misaal, nga def ko.

misig b- : misig bee tax kenn mënu fi dégg.

miskin m- : néew-ji-doole j-. li la Yàlla dénk, dee ci sarax miskin yi.

mitti : dinañuy wax tamit metti. (seetal metti)

miww : (ne miww). njool. garabu xottu buteel dafa ne miww ca kow.