dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

meeb : tiye bu baax ci ay yoxo, fab. meeb na xale bi ba mu nelaw.

meem : xar maa ngi meem ci suba ba léegi.

meen m- 1 : meenu garab maa ngi toq.

meen m- 2 : ñi nga bokkal ci wàllu yaay yépp ñooy sa meen. safaan wi mooy geño g-.

meer b- : njiitu bokk-moomeel l-. meer dafa war a toog ci goxam, liggeeyal ña ko fal foofa.

mees b- 1 : meesu lamp. meesu làmp bi dafa gàtt.

mees b- 2 : dimaas katokik yi dañuy dem mees.

meesees w- : fel w-, teeñ w-, weteñ w-. ginaar gi am na ay meesees.

mees : létt ak ay mees. Faatu mën naa mees.

meetar b- 1 : jàngalekat b-, ustaas b-, sëriñ b-. seen meetar dafa mën a dóore.

meetar b- 2 : natt bu tollu ci meetar. ñeenti meetar lay sol.

meew m- : cere ak meew lañu defaral reer.

meex-sedd-rey b- : miikar b-. ab meex-sedd-rey la.

mego b- : mego mooy ndesit wala jeexitu sigaret.

mejj : mànke, jóge ci dara. feexeel ba bu dara mejj ci xaalis bi la askan wi dénk.

mekanise b- : mekanise ab wàcc-raxasu la.

mekk : (ne mekk). ne tekk. nit ñaa ngi wax rekk wànte moom mu ngi ne mekk ci ruq bi.

melantaan w- : melantaan a ko màtt. dinañuy wax tamit melentaan w- wala mellent w-.

melas : (ne melas). mes (ne), mër (ne), meŋŋ (ne), meteñ (ne). baat bi dafay tekki lu jékki-jékki rekk réer. kayitu ñaari junne wi ne na melas ci digganti bi.

melastiku : muus mi naan na diwlin gi bay melastiku. dinañuy wax tamit malastiku wala melestiku.

melax : lerax. asamaan saa ngi melax. dinañuy wax tamit mellax.

melentaan w- : dinañuy wax tamit melantaan w- wala melent w-. (seetal melantaan)

melent w- : dinañuy wax tamit melantaan w- wala melentaan w-. (seetal melantaan)

mellax : dinañuy wax tamit melax. (seetal melax)

mel : niru. mu ngi weex ba mel ni ku tuuroo dóomu taal.

melokaan w- : baatu melokaan mu ngi jóge ci baatu mel. (seetal mel)

melo b- : baatu melo mu ngi jóge ci baatu mel. (seetal mel)

menn b- : dinañuy wax tamit benn m-. (seetal benn)

meññ : am meññeef yu bare. garabu pom gi meññ na.

meŋŋ : (ne meŋŋ). mes (ne), mër (ne), meteñ (ne), melas (ne). baat bi dafay tekki lu jékki-jékki rekk réer. xale bi ne na meŋŋ ci biir marse bi.

meret m- 1 : meret turu picc la.

meret m- 2 : meret deret la ju jigeen di tuur bu wësinee ba pare.

mer : li mu la def ba nga mer, def nga ko sa morom te merul. safaan wi mooy bég.

mes : (ne mes). mër (ne), meŋŋ (ne), meteñ (ne), melas (ne). sàcc bi ne na mes ci diggante bi.

meteñ : (ne meteñ). mes (ne), mër (ne), meŋŋ (ne), melas (ne). baat bi dafay tekki lu jékki-jékki rekk dugg fenn ne mes wala mu ne mër. golo gi ne na meteñ ci biir àll bi.

metti : saf, naqari. tànkam dafay metti. / li nga ko wax metti na ko torob. dinañuy wax tamit mitti.

mey : dinañuy wax tamit may. (seetal may)