dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

mbaa 1 : am, wala. dinañuy wax tamit mbaate. jàngal bu baax mbaa doo bokk ci ñiy jiite réew mi ëllëg.

mbaa 2 : ndax, xanaa. mbaa yaa ngi bàyyi sa xel ci dee ?

mbaaf m- : gajj guy jebbi. tool bi bare na mbaaf.

mbaal : nax ay picc, jàpp leen. tey dañuy mbaal ay picc.

mbaal m- : mba m-, njéggal l-. mbaal mee ko teree dem kaso.

mbaam-àll m- : rëbbkat bi rey na am mbaam-àll.

mbaam-sëf m- : nanga am yërmaande ci mbaam-sëf mi, borom bakkan la.

mbaam-xuux m- : jullit du lekk mbaam-xuux.

mbaam m- : mbaam mën na nekk mbaam-sëf, mbaam-àll wala mbaam-xuux.

mbaanig m- : soow m-. may ko ci mbaanig mi.

mbaar : defar am mbaar. gaa yi dañuy mbaar ci ëtt bi.

mbaaru-tëgg m- : bérebu liggeeyukaayu tëgg. mbaaru-tëgg mi yàgg na ci dëkk bi.

mbaasan : mbaasan aw melo la. robb bu mbaasan la ñawlu.

mbaate : dinañuy wax tamit mbaa-1. (seetal mbaa)

mbaax g- : mbaaxam gi foo ko natt romb na ko. safaan wi mooy mbon g- wala coxor g-.

mbaboor : awu, woy. ci ñiy mbaboor la bokk.

mbagg m- : cëru doom-aadama. dafa gaañu ci mbagg. benn mbagg lañuy wax wànte su baree, ay wagg lañuy wax.

mbaleñfàŋŋ : nax, fuuxal. li mu la jaay baaxul, dafa la mbaleñfaŋŋ.

mbalit m- : liggeey ci mbalit mi metti na.

mbalka m- : defukaayu ndox ngir nandal jur gi. nag yi dem nañu naani mbalka ma.

mballax : tëgg mballax. tëggkat yaa ngi mballax bu baax.

mball : xoole xoolin wu dëng. benn bëtam bi dafa mball.

mballu : fo ak sa awra ngir am ci bànneexu sëy. diiney lislaam dafay tere mballu.

mbal : noos. fu mu tollu mu ngi mbal mootax dencul dara.

mbamb : tasaare ay wax yu bon ci deru nit. li ngay def ba ñépp di la mbamb, bàyyi ko ci teel.

mbanaar m- : bàmmeel b-. dinay dem ca mbanaaru pàppaam ba di ko siyaar.

mbana g- : cin lu mag l-, telle g-. ñaari mbana lañu sóoroon ca ngénte la.

mband : di wër ci dëkk yi, di tëgg ay tama ak a woy. ñee di ñëw dañuy mband.

mba m- : njéggal l-. ki nga tooñ, ñaan ko mba, mu jéggal la.

mbañ-gàcce b- : sàkket wala rido bu ñu def ci buntu kër ndax kuy romb bu mu mën a gis dara ci biir kër gi. ngelaw lee daane mbañ-gàcce bi.

mbañeel g- : baatu mbañeel mu ngi jóge ci baatu bañ. (seetal bañ)

mbañ g- : noon b-. / loo bëggul. baatu mbañ mu ngi jóge ci baatu bañ. (seetal bañ)

mbappat m- : làmb j-, bëre bi. waa koñ bi dañuy tëgg mbappat tey.

mbaq : sànni. dafa mbaq picc mi, mu daanu sedd guyy.

mbaquus m- : kadó bu ndaw b-. lii de mbaquus la !

mbar m- 1 : duus b-, gannax g-, wàgg y-. tey géej gi bare na ay mbar.

mbar m- 2 : defukaayu paaka wala jaasi. paaka baa ngi ci biir mbar mi.

mbaraan : nax nit ba am ci moom li nga bëgg. xale yu jigeen yi ñooy faral di mbaraan góor ñi.

mbar g- : mbooloo mu takku m-, ndiiraan g-. mbar gu rëy a nga ca miitiŋ.

mbarum-bët m- : luy rafloo sa mbarum-bët mi ?

mbaru : tàggat yaram bu ñuy def ak ay xànq ci kow ndox mi. sooy mbaru, dangay teg ag xànq ci kow ndox mi, taxaw ci muy dem te doo daanu.

mbas 1 : njuy. dafa mbas alkaati bi, mu daanu.

mbas 2 : baat bi dañu koy wax su amee lu la lakkal. mbas ! xale yi yeen a bare wax, noppileen !

mbaseñ b- : xeetu piis. mbaseñ bu baax bi la la jëndal.

mbas m- : feebar bu law b-, musiba m-. yal na ñu Yàlla aar ci mbasum ebolaa.

mbawar g- : mbootaayu denc ak leble xaalis. jigeeni koñ bi yépp ci mbawar gi lañu bokk.

mbaw : dinañuy wax tamit mbów. (seetal mbów)

mbaxanaase m- : dinañuy wax tamit mboldit m-. (seetal mboldit)

mbaxana m- : jigeen dafa war a woyof ni mbaxana. dinañuy wax tamit mbaxane m-.

mbaxane m- : dinañuy wax tamit mbaxana m-. (seetal mbaxana)

mbayaar m- : xeetu fas. fas yi ay mbayaar lañu.

mbay m- : baatu mbay mu ngi jóge ci baatu bay. dinañuy wax tamit mbey m-. (seetal bay)

mbàbba b- : ki gën a ñàkk xel ci daara ji. mbàbba bi la xale yi di ñaawal.

mbàcc m- : jëfu bàcc. mbàccum gerte wala mbàccum ceeb. seen mbàcc ma tey la.

mbàjj m- : sàngookaay b-. seddaay bi mbàjj mu diis a ci baax.

mbàmbulaan g- : pax mu xóot lool. dafa daw ba tàbbi ca mbàmbulaan ga. / xale bu am xel mu rëy ak mën-mën bu yéeme. mbàmbulaan gi ñépp a ko xam ci diwaan bi.

mbànd m- : dinañuy wax tamit ndaa l-. (seetal ndaa)

mbàpp : (ne mbàpp ). toog ak doole, réjj (ne). dafa yegsi rekk ne mbàpp ci kanape bi.

mbàpp m- : liy nekk ci kow booy baxal meew mooy mbàpp. dinañuy wax tamit màpp m-.

mbàq g- : biir b-. suulal li nekkoon ci mbàqu nag wi. dinañuy wax tamit bàq g-.

mbàttu m- : kudd-luus g-. mbàttu mi dàmm na. dinañuy wax tamit wàttu s-.

mbebetu : kebetu, talalali, mbeleleli. demal liggeeyi nga toog ci keppaar gi di mbebetu rekk.

mbecci : làqarti mbaalu napp g-. mool yi mbecci nañu mbaal gi ba pare.

mbedd m- : xàll w-. màndikat baa nga tëdd ca mbedd ma.

mbeereer m- : dugub ji ñu mujj a góob, ndull m-. mbeereer mee des ci dundu gi.

mbeex m- : ndoxum géej m-, ngañ m-. mbeex mi dafa saf xorom.

mbege : wërgalu. néeg bi dafa mbege.

mbej : pes, talaata. soo ko saagaa, dina la mbej.

mbeleleli : di wax rekk, ratatati. liggeeyal ngay mbeleleli rekk.

mbellax : wudd, yafal. gone gi dafa tuuti, danga koy mbellax.

mbell m- : fu am-am mën a génne. déndu Afirig bare na ay mbell, li ñu war a def mooy saytu leen bu baax. dinañuy wax tamit mbéll m-.

mbempen : ku dul gis guddi bu baax. dafa mbempen mootax du génn guddi.

mbeq m- : béreb bu tooy xepp ak sawu fas wala mbaam wala xar ak ñoom seen. bul dox ak tànki neen ci mbeq mi.

mberu m- : layu bu ndaw b-. dafay defar ay mberu di jaay.

mbete : dafa mel ni. mbete ku sonn.

mbetteel g- : baatu mbetteel mu ngi jóge ci baatu bett. (seetal bett)

mbey m- : baatu mbey mu ngi jóge ci baatu bey. (seetal bey)

mbéb g- : baatu mbég mu ngi jóge ci baatu bég. (seetal bég)

mbéeru g- : gaanuwaay b-, wanag w-. deel toppatoo mbéeru gi.

mbégte m- : baatu mbégte mu ngi jóge ci baatu bég. (seetal bég)

mbéll : dinañuy wax tamit mbell m-. (seetal mbell)

mbér m- : dëtt j-. bësal ko taab bi, mbér mi génn.

mbëfër : baat bi dafay tekki coow liy am su lu diis daanoo. nag wi nee na mbëfër ci suuf.

mbëggeel g- : cofeel g-. baatu mbëggeel mu ngi jóge ci baatu bëgg. (seetal bëgg)

mbëj : maas. kura bi mbëj na ko.

mbëkk : ndañ. xar mi mbëkk na ko. dinañuy wax tamit dañ.

mbëllée : lu ñuy faral di wax suñuy ñaawal nit boole ce tàllallaale sa làmmiñ. mbëllée ! sa soow mi tuuru na.

mbënd m- : dinañuy wax tamit mbënn m-. (seetal mbënn)

mbënn m- : baatu mbënn mu jóge ci baatu bënn. dinañuy wax tamit mbënd m-. (seetal bënn)

mbëŋ-mbëŋ b- : xeetu ndënd. mbëŋ-mbëŋ bi foor na lool.

mbëpp g- : fiir g-. mbëpp fiir la gu ñu defare leket, bant ak ag buum dangay xaw a dëpp leket gi, kalee ko benn bant, def tuuti dugub ci ron, su picc yi ñëwee di lekk dugub ji rekk, nga xëcc buum gi nga takkoon ci bant bi, leket gi këpp ci seen kow.

mbërëngaan m- : baatu mbërëngaan mu ngi jóge ci baatu bërëŋ. (seetal bërëŋ)

mbës-mbësaan m- : baatu mbës-mbësaan mu ngi jóge ci baatu bës. (seetal bës)

mbët : lu bare torob. am na tool mbët.

mbëtt m- : talibe yi jàpp nañu mbëtt mu rëy.

mbicci m- : ay fiil yuy lang ci suufu piis. tubey ji mu soloon dafa amoon ay mbicci.

mbiib : bul fi mbiib ndax nit ñi dañoo bëgg a nelaw.

mbill m- : jib w-, baroom b-, sand g-, kéwel g-. seenoon nañu am mbill ca àll ba.

mbindaafoon b- : baatu mbindaafoon mu ngi jóge ci baatu bind. (seetal bind)

mbindaan b- : baatu mbindaan mu ngi jóge ci baatu bind. (seetal bind)

mbindeef m- : baatu mbindeef mu ngi jóge ci baatu bind. (seetal bind)

mbind m- : baatu mbind mu ngi jóge ci baatu bind. (seetal bind)

mbir m- : afeer b-. nee na du àddu ci mbir moomu.

mbiskit m- : su may ñëw, dinaa jëndaaleel gone yi mbiskit.

mbitaar m- : wax ak ay jëf, liyaar. lépp lu muy wax, dafa koy mbitaar.

mboccoor m- : géleem gu ndaw. ba mu demee Gànnaar la jëndaale am mboccoor.

mboje-mboje y- : xale yu ndaw y-, gone yu ndaw y-. mboje-mboje yeey coow ci biti.

mbojj m- : baatu mbojj mu ngi jóge ci baatu bojj. (seetal bojj)

mbokk m- : baatu mbokk mu ngi jóge ci baatu bokk. (seetal bokk)

mboldit m- : mbaxanaase m-. mboldit mi taq na ci yéreem bi. diwal ko mboldit ci jë bi.

mbomb g- : baatu mbomb mu jóge ci baatu bomb. (seetal bomb)

mbonaat m- : màwwa g-. dafay yar ay mbonaat ci këram.

mboneel g- : dinañuy wax tamit mbon g-. (seetal mbon)

mbon g- : mboneel g-. baatu mbon mu jóge ci baatu bon. safaan wi mooy mbaax g-. (seetal bon)

mboŋ : yeewu, bare pexe. moytul ndaw soosu, dafa mboŋ lool.

mboob m- : baatu mboob mu jóge ci baatu boob. dinañuy wax tamit boob m-. (seetal boob)

mboog : gaawal mboog ñu dem, dama yàkkamti. dinañuy wax tamit boog.

mboolem-nawle m- : askan w-. mboolem-nawle mi dafa soppi doxalin léegi.

mboolent m- : baatu mboolent mu ngi jóge ci baatu boole. (seetal boole)

mboole m- : ndàllaan l-. baatu mboole mu ngi jóge ci baatu boole. (seetal boole)

mbool : lakk ay gubi dugub ngir yëy leen. su ñu góobaan ba wàcc, dañuy mbool.

mbooloo m- : jotaay b-, ndaje m-. baatu mbooloo mu ngi jóge ci baatu boole. (seetal boole)

mbootaay m- : kurel g-. baatu mbootaay mu ngi jóge ci baatu boot. (seetal boot)

mbootu m- : roggandaay l-. baatu mbootu mu ngi jóge ci baatu boot. (seetal boot)

mbooy g- : tool bu ñu beyul te ay ñax kese sax fa. yewal fas wi ca mbooy ga.

mbooy m- : jamono ju sa xel di jóge ci li nga nekk. bi sófoor nekkee ci am mbooy la oto bi saaraan.

mbopp s- : bopp bu ndaw. baatu mbopp mu ngi jóge ci baatu bopp. mbopp si xar mi lay fees.

mboq : puur, màkka, sóon. yére bu mboq la soloon bi mu fay ñëw.

mbororocc m- : gone g-, tuut-tànk b-. mbororocc yeey coow ci biti.

mbote m- : doomu xar j-, tef b-. mbote mi yaay ji lay seet.

mbott m- : taa-taa bi am na ay mbott.

mbóosoor m- : aajo j-, yitte j-. nit dafa war a am mbóosoor ak ay moromam.

mbóot m- : nanga toppatoo béreb bi ba bu mu am benn mbóot.

mbóoya m- : xeetu ngelaw. àll bi barewoon na mbóoya. dinañuy wax tamit mbóoyo m-.

mbóoyo m- : dinañuy wax tamit mbóoya m-. (seetal mbóoya)

mbów : yuuxu (xaj). lan la xaj bi di mbów ? dinañuy wax tamit mbaw, baw wala bów.

mbubb m- : yére b-. solal ko mbubb mu diis, dafa sedd.

mbuddat m- : ñax mu bon mi ñuy budde ci tool. dajale leen mbuddat yi, tuuri leen. dinañuy wax tamit mbuddët m-.

mbuddët m- : dinañuy wax tamit mbuddat m-. (seetal mbuddat)

mbugal : mettital. ku fi deful lu baax, borom bi dina la mbugal bés-pénc.

mbulañsëri b- : dinañuy wax tamit fuur b-. (seetal fuur)

mbumbaay : noos. ndaw si ak faram wi dañu doon mbumbaay otel.

mburaake m- : mburaake ñu ngi koy defare cere ak tiga-dege ak suukar. dinañuy wax tamit muraake m-.

mburgël m- : yoon wu jaar ci suuf, tinel b-. Dakaar am na ay mburgël.

mburtu m- : mbote m-, sëll w-. am mburtu lay seet.

mburu m- : kafe ak mburu lay ndékkee suba gu jot.

mbuteel s- : buteel bu ndaw. naan na mbuteel si ndox si. baatu mbuteel mu ngi jóge ci buteel.

mbutumtumb m- : doomu jasig j-. mbutumtumb maa ngi ci biir ndox mi.

mbuujaa-mbuuj : nekk xale bu ndaw. ab xale bu mbuujaa-mbuuj lay xulool.

mbuujaa-mbuuj b- : xale bu ndaw b-. léegi ay mbuujaa-mbuuj ngay romb ñu yore sigaret, di tux.

mbuum m- : ay xob wala ñax yu ñuy togg di ko boole ak cere. du lekk cere ak mbuum.

mbuus m- : saagu permeyaabal wala bu der bu ndaw. defal ko ko ci mbuus.

mbuxuri : am-yaram, rëy, pataa. dafa mbuxuri ba mënul a dox bu baax. safaan wi mooy siikaminnamyaret.