dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

móocc : (ne móocc). dinañuy wax tamit muucc (ne). (seetal muucc)

móodu-móodu b- : imigere b-. móodu-móodu bi dafa seetsi mbokk yi.

móol : dañuy móol di jaay. dinañuy wax tamit muul.

móolu : musibaal. fexeel ba bul def luy tax ñu lay móolu.

móomin b- : móomin mooy ku xamul wala lu xamul dara. xale móomin la. dinañuy wax tamit muumin b-.

móto b- : sooy dawal móto, nanga sol kask ndax nga aar sa bopp.