dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

mëdd : wonn, modd, muur. suuf si mëdd na ko.

mëdd g- : géleem gu góor g-, tukkal g-. mëdd mi dafa mar.

mëgg : def ab xeetu maab. danga koy mëgg ba mu am ay mees.

mëkk : (ne mëkk). yore kanam gu ñàng, mëŋŋ (ne). xamuma lu mu mer waaya mu nga taxaw ne mëkk.

mëlëñ : ñàkk ay gëñ. màgget si dafa mëlëñ.

mën 1 : nee na mën nañu tàmbali. mën na dawal oto. dinañuy wax tamit man wala mun. (seetal man)

mën 2 : sut. suñu mbër mee mën seen mos.

mëŋŋ : (ne mëŋŋ). yore kanam gu ñàng, mëkk (ne). safaan wi mooy ubbeeku. (seetal mëkk)

mëq-dóom g- : xeetu fetal la. buy rëbbi mëq-dóom gi lay yóbbu.

mëq : muut. bul seetaan gone gi muy mëq suuf si.

mërëg b- : xeetu yabóy. tey ay mërëg rekk a am marse.

mërgal w- : wërngal w-. bu kenn génn mërgal wi.

mër : (ne mër). mes (ne), meŋŋ (ne), meteñ (ne), melas (ne). junne bi ne na mër ci biir kër gi.

mës : dinañuy wax tamit mas wala mus. (seetal mas)

mët : dinañuy wax tamit mat, mot wala mut. safaan wi mooy matadi wala mànke. (seetal mat)

mëwwa g- : mbonaat m-. dinañuy wax tamit màwwa g-. (seetal màwwa)