dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

mébet : xalaat, nësër. li ngay mébet doo ko mën a am ci ay caaxaan, fokk nga góor-góorlu.

méb : waaj a dóor. dafa méb rekk, waa ji ariyeer.

médd : dee, dog, faatu. xar ma médd na laata ñu koy rey.

méeri b- : méeri mooy màkkaanu wala bérebu liggeeyukaayu meer.

méngale : tollale, yemale. bul méngale yu bokkul. dinañuy wax tamit méngatle.

méngatle : dinañuy wax tamit méngale. (seetal méngale)