dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

lu-dul : lu nekkul. lu-dul xaalis bu ko lew, du ko lekk.

lu-ko-moy : nanga jàngal xale bi, lu-ko-moy ëllëg du xam dara.

lu-nekk : waa ju baax la ndax defal na ko lu-nekk. dinañuy wax tamit lu-ne.

lugat 1 : génne am mbir mu tàbbi ci teen ak benn jumtuwaay bu lonku. baag bi daanuwoon ci biir teen bi lañuy lugat.

lugat 2 : jëfandikoo luy rey teeñ ngir dindi leen ci kawar. nanga lugat sa bopp bi bala ngay léttu.

lugg : tari ab xam-xam ngir wàcce daŋar ci ku jaan màtt. góor gi lugg na tànku waa ji ba daŋar ji wàcc.

lujum b- : paytéef b-. lujum bi bare na ci marse bi. dinañuy wax tamit lëjum b-.

lukkat : dinañuy wax tamit lokkat. (seetal lokkat)

lumb w- : lu way. lumbu deret waa ngi ci loxo bi mu gaañu.

lumm : dinañuy wax tamit lëmm. (seetal lëmm)

lump : sexandoo lépp benn yoon. lump na beñe bi mu doon lekk yépp.

luññutu : gëstu am mbir ngir am ci lu gën a leer. toppatool say mbir te bàyyi mbiri jàmbur yi ngay luññutu.

lupp-lupp b- : dinañuy wax tamit lëppaa-lëpp b-, luppaa-lupp b- wala lëpp-lëpp b-. (seetal lëppaa-lëpp)

luppaa-lupp b- : dinañuy wax tamit lëppaa-lëpp b-, lëpp-lëpp b- wala lupp-lupp b-. (seetal lëppaa-lëpp)

lupp b- : pooj b-. dafa taab ci lupp.

luqati : dinañuy wax tamit lóqati wala luqi. (seetal lóqati)

luqi : dinañuy wax tamit lóqati wala luqati. (seetal lóqati)

luqnjuur : ku naqari xel. dafa luqnjuur ndax du liggeey lu baax.

lutax : lu waral. lutax nit ku ñuul du doyal nguur ?

lutee : lutee njiit yi fulaal bëgg-bëggi askan wi ? dinañuy wax tamit lutere.

lutere : dinañuy wax tamit lutee. (seetal lutee)

lutt b- : xucc b-. defal ndànk sooy dagg lutt bi.

luubu : dëgër-bopp. nee na xale bi dafa luubu mootax mu yóbbu ko daara.

luucu b- : ngemb l-. mbër yi ay luucu lañuy sol suñuy bëre.

luuju : dinañuy wax tamit lóoju. (seetal lóoju)

luuma b- : marse buy am ayubés bu nekk. tey la luuma altine.

luu : muuma. mënul a wax, dafa luu.

luus b- : jumtuwaayu togg. luus bi dàmm na.

luwaa b- : yoon w-. ku def lu dëppoowul ak luwaa, ñu daan la.

luwe : dafa luwe kër gi. dinañuy wax tamit luye.

lux-luxi : sax yaa ngi lux-luxi ci kow médd mi.

luxóor b- : balaa b-, jéyya j-, musiba m-, njaaxum l-, toj-toj b-. du jóg ci def luxóor.

luxu : jafe. mbir moomu dafa luxu.

luxus : feeñal ay mbir yu yéeme, ñengo. sëñ bi nee na mën naa luxus xaalis.

luye : dinañuy wax tamit luwe. (seetal luwe)