dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

lobb b- : matt mu ñu dajale ci ginnaaw kër gi ngir di ci togg bu matt amul. soxna si goroon na ñaari lobb.

log : tiye dara ci biir lex. mu ngi log guro gi, di wax ak nit ñi.

loj : reendi, rëx. naar yi loj nañu géleem gi.

lokkat : lakk ay sébbu, taal. gajj na gajj yi, rato gittax yi, lokkat sébbu yi. dinañuy wax tamit lukkat.

lokki : tekki, yewwi. lokki na bëy yi ngir ñu dem wëtti. safaan wi mooy takk wala yeew.

lolli b- : jamono ju tàmbalee oktoobar ba desàmbar. ci lolli bi la fi ñëwoon.

lompaa b- : bantu wetu lal, tóor b-. lompaa bi dëgërul.

lompañ : làggi, lafañ. dafa lompañ mootax mënul yenn liggeey yi. dinañuy wax tamit lompoñ.

lompoñ : dinañuy wax tamit lompañ. (seetal lompañ)

lonet y- : weer y-. su takkul ay lonet du gis li muy jàng.

lonk : wékk. feeskat bi lonk na xar mi ci bant bi. safaan wi mooy lonki wala wékki.

looco g- : gaal g-. ñakk liggeey a taxoon ndawi réew mi di jël ay looco ngir dem Barsaloon, ca Espaañ.

loof : sonn, lott. dama loof démb mootax duma mën a liggeeyi tey. safaan wi mooy noppalu.

lool : torob. xale bi dafa sob lool.

loolu : lekk alali askan wi ñu la dénk, loolu du cëru kilifa.

loolu : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

loo w- : nag wu ñu daan takk ci masin. amoon na ay loo.

looñ : ñàkk ay gëñ. maamam dafa looñ.

looro g- : garabu looro. garabu looro mat naa sàmm ndax xas mi dafay wàcce coono.

loos w- : doq g-, baat b-. tëraay bu bon mooy faral di metti loos.

looy m- : looy am picc la.

loppitaal b- : dinañuy wax tamit loppitaan b- wala opitaal b-. (seetal loppitaan)

loppitaan b- : soo fagaruwoon doo feebar bay dem loppitaan. dinañuy wax tamit loppitaal b- wala opitaal b-.

lor : sàcc bi lor na borom bitig bi ndax bàyyilu ko fi dara.

lor w- : taflit y-. defal suuf ci lor yi.

lott : waa ji dafa yenu saaku ba lott. dinañuy wax tamit loof.

lox : seddaay bee ko tax di lox.

loxo b- : loxo benn la ci cëri doom-aadama yi. benn loxo bi dafay metti. ñaari yoxo yi dañuy metti.

loyox b- : xob wu dëgëragul. bul wut xob yu mag, wutal ma ay loyox.