dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

lóŋo b- : bant bu ñuy gàll ci ay wagg ngir lonk ci defukaay yi meew wala soow. siwo soow yi mu def ci lóŋo bi diis nañu.

lóoju : dugal loxo ci biir gémmeñ ngir woccu. li mu lekk moo ëpp mootax muy lóoju. dinañuy wax tax tamit luuju.

lóor : tooy xepp ak ndox. su cere ji lóoree, doo ko mën a lekk.

lóoxoor b- : musiba m-, balaa b-. yal na ñu Yàlla dàqal bépp lóoxoor.

lóqati : génne fu sore. fexe na ba lóqati xaalis bi daanuwoon ci pax mi. dinañuy wax tamit luqati, wala luqi.

lótëri b- : kàrta g-. bëgg lu yomb rekk mootax nga nekk ci lótëri bi waaye dem liggeeyi nga war a def.