dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

lëf k- : dinañuy wax tamit këf k- wala këfin k-. (seetal këf)

lëf k- : dinañuy wax tamit kifin k-, këfin k-, këfkin k- wala këf k-.

lëf l- : (wax ju ñaaw la). am mbir, awra jigeen b-, bajo b-, data b-. li mu sol lëfam li rekk la nëbb. safaan wi mooy kooy b-.

lëgët b- : lëgët bi góom bu metti la woon. dinañuy wax tamit léget b-.

lëggeey : dafa mën a lëggeey mootax du taxawaalu. dinañuy wax tamit liggeey.

lëg g- : dafay yar ay lëg ci këram.

lëj : dinañuy wax tamit léj. safaan wi mooy lijjanti. (seetal léj)

lëjum b- : dinañuy wax tamit lujum b-.

lëkkaleku : neex-deret. xale soo ko yóbboo ci bérebu fowekaay, dafay lëkkaleku. dinañuy wax tamit lëkkëleku.

lëkkatoo : juboo ak kenn ci jëfandikoo turam. dafa lëkkatoo ak alkaati bi, di dawal oto bu amul kayit.

lëkk : takk ab sër ci baat. suy lekk, danga koy lëkk sër bi.

lëlëg j- : suba g-. ci lëlëg ji la ñëwoon.

lël b- : mbooloom njulli ak béreb ba ñu nekk, mbaar m-. seen lël ba amoon na lu ëpp téemeeri njulli.

lëmbal : fecc di yëngal aw taat. tëggkat yaa ngay tëgg, jigeen ñaa ngay lëmbal.

lëmbe : coowu xale yi lëmbe na béreb bi yépp.

lëmb : lemu, banku. yow yaa dëgg kees gi ba mu lëmb. safaan wi mooy tàllalu.

lëmës : laxas. ci ay kayit lay lëmës gerte-caaf gi.

lëmm : lu mànkewul dara. kër lëmm la may jabar ji may-gu-njëkk. dinañuy wax tamit lumm.

lëm : wax ci lu gaaw, tënk. danga war a lëm wax ji ndax dafa guddi fi mu nekk.

lëm l- : pax mu nekk ci biir garab. soreel lëm li, ñàngoor mën na ci nekk.

lëndëm : buleen génn, dafa lëndëm. safaan wi mooy leer.

lënd w- : kër jargon g-. dindil lënd yi nekk ci néeb bi yépp.

lëng : jaarale say yoxo ci waggi keneen. mu nga lëng jabar ji di dem.

lëng g- : xeetu gajj. lëng am na ci àllu Saalum bi.

lënt : lu leerul, lu àndul, lu lëndëm. sa lay wi am na lu ci lënt. safaan wi mooy leer.

lëñbët : laaj, ànket. bàyyil mbiri jàmbur yi ngay lëñbët, am nga lu la doy wax. dinañuy wax tamit lëñtu.

lëñtu : dinañuy wax tamit lëñbët. (seetal lëñbët)

lëpp-lëpp b- : dinañuy wax tamit lëppaa-lëpp b-, luppaa-lupp b- wala lupp-lupp b-. (seetal lëppaa-lëpp)

lëppaa-lëpp b- : béreb bi bare na ay lëppaa-lëpp. dinañuy wax tamit lëpp-lëpp b-, lupp-lupp b-, wala luppaa-lupp.