dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

lébu b- : waaso la wu dëkk ci diwaanu Ndakaaru, fi ñu naan Petite Côte ak diwaanu Ndar. Wakaam ak Ngor ay dëkki lébu lañu.

léebeer b- : léebeer rabu àll la bu am doole.

léeb : nettali, maye. seen maam dafa mën a léeb.

léeg-léeg : dinañuy wax tamit lée-lée. (seetal lée-lée)

léegi : léegi li ëpp ci xale yu jigeen yi tubey rekk lañuy sol. / xaaral tuuti, léegi mu ñëw. dinañuy wax tamit lée, lée-lée wala léeg-léeg. (seetal lée-lée)

léej : sob, ëppal, yemadi. sa doom ji dafa léej. safaan wi mooy yem wala teey.

léem : wër, séq. léem na tool bi ba mu daj ak ay dég.

lée : du fa yàgg, lée mu ñibsi. dinañuy wax tamit léegi.

léewaatoo : wutante, nattante. ñaari mbër yaa ngi léewaatoo. dinañuy wax tamit léewtoo.

léget : dinañuy wax tamit lëgët b-. (seetal lëgët)

léj : laxasu, jaxasoo. goj yi dañoo léj. dinañuy wax tamit lëj. safaan wi mooy lijjanti.

léñ : tas. léñ na ndab yi yépp. safaan wi mooy rañsele.

lépp l- : lépp loo fi gis dafay jeex.

létt : maab. dafay létt ñu koy fey.