dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

làbbali : yokk gaawaay. danga war a làbbali fas wi, ñu dem gaaw. dinañuy wax tamit làbbili.

làbbe b- : kilifa ci diiney katolig. làbbe bi ab tubaab la.

làbbili : dinañuy wax tamit làbbali. (seetal làbbali)

làcc : (ne làcc). daanu ndax coono. ci suba ba léegi mu ngi ne làcc.

làcc w- : dinañuy wax tamit waar w- wala wàll w-. (seetal waar)

làggi : tànk wala loxo bu làggi. tànk bi dafa làggi ginnaaw bu mu defee aksidaa.

làkk 1 : wax. àngale la waa ji di làkk.

làkk 2 : ñag, sàkket. xar yi ak bëy yee tax mu làkk toolam bi.

làmbaay b- : yére b-. làmbaay bi dafa xotteeku.

làmb : bàyyil yàpp wi ngay làmb.

làmb j- : bëre b-, mbappat m-. seen mbër maa ub làmb ja

làmboo : yore, limboo. waa ji am na lu mu làmboo ndax lu yéeme rekk lay def.

làmmeñ w- : dinañuy wax tamit làmmiñ. (seetal làmmiñ)

làmmiñ w- : dafa màtt làmmiñ wi. dinañuy wax tamit làmmeñ w-.

làmp b- : làmpu petorol b- wala làmpu kuraŋ b-. tey làmpi mbedd yi tàkkuñu.

làng : def benn wërngël. jigeen ñaa nga làng, di joxe teraanga ya.

lànjaŋ : (ne lànjaŋ). tëdd taanu, bàyyeeku, làññ (ne), lañar (ne). masoŋ bi dafa sonn mootax mu ne lànjaŋ.

lànk : bañ. ñaan na la ndimbal nga lànk wànte ëllëg man na am, nga ñàkk. safaan wi mooy nangu.

làññi : xàwwi, wuññi, muri, ñori. ngelaw li làññi na sàkket wi. safaan wi mooy muur, ub, wala sàng.

làññ : (ne làññ). tëdd taanu bu baax, ne lànjaŋ. dafa yegsi rekk ne làññ ci dig lal bi. (seetal lànjaŋ)

làpp : jeex, sew, yooy. mbaamam mi làpp na lool. safaan wi mooy suur.

làq : nëbb, denc. làq na suukër si mu jënd ndax bu ko duwaañ yi gis. safaan wi mooy feeñal.