dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kobos : wokk nit ngir am loo koy xamal ci suuf. bi ngay wax kobos naa la ay yoon ngir nga noppi.

kocc 1 : jukki, root. dafay kocc ndox mu mu sangoo.

kocc 2 : dinañuy wax tamit cocc. (seetal cocc)

koddaay l- : yére y-. yal na ñu Yàlla may wér, dund ak koddaay.

koddal : jógal, tukkal. mbaam mi koddal na.

kof-kof : lox, pat-pati. waa jaa nga ca mbedd ma, naan kof-kof ndax seddaay bu metti.

kogg w- : xeer w-, doj w-. aw kogg la ko jam.

koj-koj : coow li ay dàlli koket di def boo leen solee di dox ci kekk. sa koj-kojee yee xale bi doon nelaw.

koj : kar, tëru, gatandu, dogale. ageresëer yee ko koj ci yoon wi biig ci guddi.

kok b- : kaala gi dafa ñuul kok. dinañuy wax tamit kukk.

kokombar b- : nduggam mi am na kokombar.

kol b- 1 : kaala g-. jottali ma sama kol bi, ma julli.

kol b- 2 : dàllam yi dagg lay jëndal kol.

kolkolaat b- : xeetu weñ yuy defar lem. rab yiy naaw ay kolkolaat lañu.

koll b- : biir b-. koll bu rëy la yore.

kolloor g- : buntu pax m-. bul dugal sa loxo ci kolloor gi.

komaase : door, tàmbali. lu bon li nga komaase, nanga ko bàyyi ci teel.

kompaletmaa : mat sëkk, jeex tàkk. kër ga dafa tàkk kompaletmaa.

kompirime b- : per b-. bopp buy metti la kompirime bi di faj.

kongasaane b- : xeetu basi. suuf si nanguwul kongasaane.

kon : kon ñu def noonu ba beneen yoon. dinañuy wax tamit bon. (seetal bon)

kontaan : bég. askan wi kontaan na lool ci liggeeyu jëwriñ ji.

koñ b- : coll b-. dajewoon nañu keroog ca koñ ba.

koŋ : baat bi dafay ànd ak baatu wow te di tekki ba ëpp. galaas bi wow na koŋ. dinañuy wax tamit koŋŋ.

koog b- : kuddu yaj, mbàttu m-, gamb b-, leket g-. foofa ay koog lañuy naane soow.

koom-koom b- : mbirum koom-koom la jàngiwoon bitim réew. / réew mi am na koom-koom.

koontaan : dinañuy wax tamit bég. (seetal bég)

kooñoor b- : nit ku tuuti k-. yenu ay saaku simãa du liggeeyu kooñoor. safaan wi mooy ponkal m-.

kooraa b- : jumtuwaayu misig bu ñuy defare ay buum. borom kooraa bi li muy def neex na.

koor g- : juroom-ñeenteelu weer ci atum jullit yi, weer wi jullit yi di woor. ci koor gi rekk la yenn feebar yi di feeñ. safaan wi mooy kori g-.

kooy b- : (wax ju ñaaw la) sull b-. kooyam baa ngi ci biti, solal ko tubey.

koppar g- : xaalis b-. mbaa koppar yi ngay lekk yépp lew na la domm ?

koppe b- : kureelu dimbalante g-. waa dëkk bi yépp bokk nañu ci koppe bi.

kopp b- : kaas b-, weer b-. bi ñu añee ba pare, la ñu soxna si andil kenn ku nekk, koppu soow.

kor 1 : soppe b-. kor Awa ñëw na.

kor 2 : li ñuy wax ngir taxawal fas wuy dem. safaan wi mooy ali.

kori g- : fukkeelu weer ci atum jullit yi. ci kori gi la jëkkëram war a ñibsi. safaan wi mooy koor g-.

kor g- : jëf ji nit di def bu woree moromam. kor gi muy def nit ñi mootax kenn wóolootu ko.

kort : liggeey, takk. mbokk yee ko kort mu soog a ñibsi.

kos : nangul almet bi xale yi di kos.

koti b- : junqóob b-, kuppukaala b-. ay koti lay jaay.

kotom : lemu. ay noppam dañoo kotom.

kott 1 : waa jaa nga kott mbaam ma di dem. / denc ngir yow rekk. dafa naroon a kott li des ci xaalis bi.

kott 2 : rekk, kepp, kese, doŋŋ. moom kott laa fa fekk.

kow : dinañuy wax tamit kaw. (seetal kaw)

kox-kox g- : ay sëqët yu bare. kox-kox gee ko yàqal li muy def.