dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kebale : dajale. mu nga tëdd kebale ay tànkam.

kebatu : waxtu, xultu, ŋurumtu. mu nga aw yoon wa, di kebatu, di dem. dinañuy wax tamit kebetu.

kebetu : dinañuy wax tamit kebatu. (seetal kebatu)

keccax : jaayuma jën yi, dama leen di keccax ñoom ñépp.

keccob b- : keccob ci xeeti saf-safal yi la bokk.

keef : jaaxle, waaru. xamatul lu mu war a def, dafa keef.

keeseen b- : peyoor bu ñuy fey fukki at ak juroom yu nekk. bu ma jotee sama keeseen bi, dinaa la fey sa xaalis bi.

kees b- : rajoo nekk ci biir kees bi.

kekkantoo : kókkali, ñaawal. bàyyil waa ji ngay kekkantoo, du sa morom.

kekk b- : suuf su dëgër. soo daanoo ci kekk bi, sa bopp bi dafay toj.

kekku : reetaan bu baax, xàqataay. sooy déglu ay léebam, dangay reetaan ba kekku.

kel g- : xeetu garab la. xàncu kel dafay faj tooy.

kemb g- : kalaŋ g-. jëndaaleel ko gerte kemb.

kemtalaay g- : dayo b-. defal sa kemtalaayu kàttan ndax bu la sa benn noon reetaan. dinañuy wax tamit kemtan g-.

kemtan g- : dinañuy wax tamit kemtalaay. (seetal kemtalaay)

kend l- : sunu kend démb li neexoon na lool. dinañuy wax tamit kendaay l-.

keneen k- : gis naa Abdu wànte keneen ki gisuma ko.

kenkelibaa b- : sexaw m-. kenkelibaa lañuy ndékkee suba gu jot.

kenneef g- : ag nekk kenn. benn jullit naatablewul kenneefu Yàlla.

kenn k- : kenn ki dem na sànq.

kenu g- : jën w-. kenu mbaar dafa war a dëgër.

kepp 1 : kese, doŋŋ, kott, rekk. moom kepp laa fa gis.

kepp 2 : baat bi dafay tekki lu yem rekk, rokk. dàll yi yem nañu kepp ci tànkam yi.

kepp 3 : bunt bi kepp na loxoom bi.

kepp-kooy b- : xar-geen b-. dindil kepp-kooy bi nekk ci sa yére bi.

keppaar g- : ker g-. jógal ci keppaar gi nga toog di naan àttaaya te dem liggeeyi.

ker-kepp g- : waxtu wi jant bi di nekk ci kow a kow. gaawleen ndax liggeey bi mën a pare, ker-kepp jot na.

kera : daje na ak moom kera ca marse ba. dinañuy wax tamit kerag wala keroog.

kercen b- : am na ay xariti karcen.

ker g- : keppaar g-. ki ci naaj wi moo fi bàyyi ki ci ker gi.

keroog : dinañuy wax tamit kera wala kerag. (seetal kera)

kersa g- : am looy rus. dafa bare kersa ba du siggi xool nit.

kese : kepp, doŋŋ. (seetal kepp)

keseŋ-keseŋ g- : fowukaayu xale b-. yëngalal ko keseŋ-keseŋ gi.

kes : li ñuy wax bu ñuy dàq ginaar. ginaar gi kes taxu koo daw.

keteraan g- : laskoloñ b-. keteraan gi mu def ci yéreem bi neex na lool.

kew g- : xeetu xeer la. am na jigeeni-wérul yuy lekk kew.

keww : (ne keww). baat bi dafay tekki ne jàkk ab béreb rekk, ne tekk bàyyi sa xel ci dara. lëg laa ngi ne keww di déglu.