dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kaabaab g- : ci kaabaab gi la ko pes.

kaabar w- : xar mu jigeen mu mag wala bëy wu jigeen wu mag. tey jënd na ay kaabar.

kaaf : tëj. ku sàcc alali réew mi dañu la war a kaaf.

kaake y- : bagaas y-. jël na kaake yi ba dem yoonam.

kaala : yaayam dafa ko solal garaa mbubb, kaala ko.

kaamil b- : alxuraan j-. kaamil kenn du ko sàggane. dinañuy wax tamit kaamir b-.

kaam : dëng. piis bi ngay dagg, moytul mu kaam de.

kaani-gu-sew g- : kaani gu tuuti g-. kaani-gu-sew rekk lay jaay.

kaani-salaat b- : puwaawuroŋ b-. jëndaleel ma kaani-salaat.

kaani-xeeñ g- : kaani gu saf sàpp. defal ndànk, kaani-xeeñ la de.

kaani : def kaani ci ag togg. kaani na daxin gi ba mu saf sàpp.

kaaŋ m- : ay kaaŋ yu bare lañu gis bi ñuy gas.

kaari-kaari : teew-mu-teew. soo ma joxee marsàndiis mi, ma jox la xaalis bi kaari-kaari.

kaarite g- : kaarite baax na ci yaramu liir.

kaar : lu ñuy wax ngir bañ cat dal lu ñu tagg ba pare. kër gii de, rafet na lool, kaar !.

kaar b- : bis b-, daamaar g-, daabo b-. dawalal kaar bi ndànk ndax nga mën a dal ndànk.

kaas 1 : jàmbat, tawat. dundu gu seer gi la askan wi di kaas.

kaas 2 : gajafal. bul fàttee kaas cere ji.

kaas b- : weer b-, kopp b-. àndil kaas bi ma defal la ci kafe.

kaata : domp. mu ngi kaata xale bi rekk.

kaawtéef : baat bi dafay tekki lu bette wala lu yéeme. kaawtéef ! lii lan la ?

kabine : day, puub, dem-àll, jonkon. ku fi kabine ?

kabiyàdd : teeñ. soxna si dafa kabiyàdd.

kaco-kaco b- : sawoor b-. kaco-kaco yaa ngi ci kow garab gi di tanqal nit ñi.

kadd-kaddi : jadd-jaddi. ay jinnee ko jàpp muy kadd-kaddi.

kadó b- : neexal b-, yóbbal b-. pàppa ji àndiwaaleel na ko kadó bu rafet.

kafceer b- : jëlal kafceer bi nga tàngalal ma dute bi.

kafe g- : defal ndànk, kafe gi dafa tàng.

kaf : fo, caaxaan. mënuloo boole liggeey ak kaf.

kajoor g- : turu benn gox bu nekk ci réew mi. Kajoor la waa ji cosaanoo.

kalaame : boole, pelent. bul ko kalaame, waxtaan leen rekk ba juboo.

kalaas b- : néegu njàng b-. man ak moom a bokk kalaas.

kalamba g- : nattu dénk bu war a tollu ci ñetti kilo ñu koy peesee dugub. jënd na ñaari kalamba dugub.

kala b- : xeetu jën. ay jëni kala la jëndoon bi muy togg yaasa tey.

kala j- : banti ngooñ y-. nag yi për mi lañu gën a bëgg ci kala ji.

kalaŋ : gerte xott g-. kalaŋ ak kemb yépp lay jaay.

kaldu b- : toggu Kaasamaas. kaldu la ndaw si togg tey.

kal b- : gàmmu b-. njaayeen yi ak njoobeen yi ay kal lañu.

kamaate j- : dinañuy wax tamit tamaate. (seetal tamaate)

kamisol b- : ndoket b-. kamisol robbu mag la.

kamiyoŋ b- : oto bu mag b-. kamiyoŋ xajul ci oto bu ndaw.

kanaara g- : dafay yar ay kanaara.

kanam : (ci kanam). dinaa fa ñëw ci kanam. / këram a ngi ci kanam. / ci teewayu. jox naa la xaalis bi ci kanam Ibu.

kanam g- : cëlmaay l-. kanam du kaso wànte ko ci tëj mu xam ko. (léebu).

kancóoli g- : kaña g-. xale yi ray nañu ag kancóoli.

kandaŋ : coow li kuur di def soo koy dóor ci gënn. jeeg jaa ngay wol, di kandaŋ.

kanet b- : potu buwaasoŋ b-. naan nañu ay kanet ca ngénte la ba doyal.

kaniwo b- : mbalit mi ngay tuur ci kaniwo bi, bàyyi ko, dafa koy fatt.

kannasu : dof. dafa tux yàmbaa ba kannasu.

kan : kan la wax ? dinañuy wax tamit ku.

kan m- : kàmb g-, pax m-. kan mi xóot na. (seetal kàmb)

kanu g- : xeetu ngànnaay. larme bi wàcce na ay kanu ca àll ba.

kañ 1 : ku xam kañ la àdduna di tukki ? dinañuy wax tamit kaña.

kañ 2 : tagg, yokk njàmbaar. gaa yaa ngi kañ seen mbër mi.

kaña g- : kàncóoli g-. kër gi bare na ay paxi kaña.

kar-kar g- : xeetu garabu àkkaasiyaa. seen dëkk am na ay garabi kar-kar.

karaas-karaasi : coow liy am su nit di dox, di watat ay dàllam. mu ngi dox, di karaas- karaasi rekk.

karaas b- : tër b-. boppu xale bi dafa fees dell ak ay karaas.

karabaane : tappale. dara jotu ko, dafay tappale rekk.

karaŋ g- : tàlli g-, wëñ g-. may ma tuuti ci sa karaŋ gi.

karas g- : tool bu ñu beyul. demal sàmmi nag yi ca karas ga.

karaw l- : donj yiy des ci cere soo ko suusalee ba pare, lay ko. joxal xar mi karaw li. baatu karaw l- bokkul ak baatu kawar g- (giy nekk ci bopp, ci misaal).

kariyeer b- : kariyeer mooy fu ñuy tibbe suuf wala xeer.

karmat : tarde xëdd. su ma teelul a tëdd, damay karmat.

karnaat b- : xomb b-, sélluur b-. karnaat lay tëje bunt bi. dinañuy wax tamit kànnaar b-.

kar : baare yoon wi. soo génnee ci guddi gi, saay-saay yi mën nañu lay kar, jël li nga yore.

karo b- : jënd na ay karo yu bare ngir kër ga muy tabaxlu.

karot b- : kilo karot dafa seer.

kartoŋ b- : andiwaale na ay kartoŋ yu bare.

karwaat b- : karwaat bu xonq la takk.

kasaalika noonu : dinañuy wax tamit saalika noonu. (seetal saalika noonu)

kasag : woy woyi njulli. xale yi dañuy kasag.

kasara g- : lu tekkiwul dara. kooku du dara, kasara la rekk.

kaso g- : dugal nga ko kaso de, ndax moo def li nga ko tuumaal.

kastiloor b- : xeetu bool. jëndaaleel ma kastiloor.

kat-kati : pat-pati, lox. solalal xale bi yére, mu ngi sedd bay kat-kati.

katab : (ne katab). baat bi dafay tekki lu jàpp fenn bu baax, ŋoy. golo gi ne na katab ci garab gi.

katakayna : dof, kannasu. naan na sàngara ba katakayna.

katam : (ne katam). niib, tiib, nuus. waa ji dafa daw ba ne katam sàcc bi.

kat : yow kat, xamoon nga ni alali mbooloo lañu la dénk.

katolik b- : gurmet b-. katolik yaa ngay dem mees.

katt : (baat bu ñaaw la) baane. (seetal baane)

kawar g- : ndaw si kawar gu gudd la yor.

kawas b- : ay kawas yu weex la sol.

kaw : mu ngi ci kaw etaas bi. dinañuy wax tamit kow.

kawsu g- : fóoli g-. paanu kawsu la jënd. ruuwu oto kawsu la ñu koy defaree.

kayit g- : ci kayit la lëmës gerte-caaf gi. dinañuy wax tamit këyit g-.

kay : xale bi kay, dafa reew rekk, wànte àddunaa ngi ci kanamam.