dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kóbo b- : xeetu jën wu bare ay yax. ay jëni kóbo barewoon nañu marse démb.

kócc b- : xeetu jën. ay kócc lay jaay.

kókkali : kekkantoo, ñaawal. ki ngay kókkali du sa morom.

kóllëre g- : lu dox ci diggante ay nit. kóllëre ginnaaw lay féete (léebu).

kóom b- : peñe bu gudd ay gëñ. sa kawar gi kóom rekk a ci mën dara.

kóoni g- : ron g-. foofa am na ay garabi kóoni.

kóppin g- : dinay yar ay ginaar, ay naat ak ay kóppin.

kótise : teg. xale yi dañoo kótise jënd bal.