dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kéemaan g- : lu yéeme. sëriñ bi ay kéemaan rekk lay def. dinañuy wax tamit kéemtaan g-.

kéewaange g- : càkkeef g-. sàmm kéewaange gi war na ku nekk. dinañuy wax tamit kéewnga l-.

kéewnga l- : dinañuy wax tamit kéewaange g-.

kélifa g- : mag m-, njiit l-. kélifa gu mag la ca diwaan ba. dinañuy wax tamit kilifa g-.

kémej g- : kémeju bool. bul tiye ci kémej gi, tiyeel ci njàpp yi.

képp : képp ku ñu dénk alali askan wi, nanga ko sàmm ba bu ci benn dërëm réer.

kéwel g- : kéwel rabu àll la. gaynde gi fàdd na ag kéwel.