dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

kàbbar : yëkëti sa ñaari yoxo ba ñu tollook say nopp booy julli. kàbbar nañu ba tàmbalee julli.

kàcciri : dóor ak ab yar. soo saagawaatee dinaa la kàcciri ba ngay bëgg a dee.

kàcc : wax lu dul dëgg, fen, nar. kilifa warul a kàcc. safaan wi mooy wax dëgg.

kàccoor b- : saay-saay b-. waa ji ab kàccoor la, bul ko miinal sa kër.

kàddir g- : cin l-. ay kàddir lay jaay. dinañuy wax tamit kawdiir g- wala këwdiir g-.

kàdd : (ne kàdd). baat bi dafay tekki lu ne tekk yëngatootul. mbott maa ngi ne kàdd ni lu dee.

kàdd g- : garabu kàdd. seen àll bi bare na ay kàdd.

kàggu g- : waxande w-, gaal g-. kàggu gi dafa fees dell ak ay téere.

kàkkataar g- : dinañuy wax tamit kàkkatar. (seetal kàkkatar)

kàkkatar g- : góor warul a yéexe ni kàkkatar. dinañuy wax tamit kàkkataar g-.

kàllaama g- : làkk w-. kàllaama wolof la tubaab bi di jàng.

kàll g- : làkk wu ñépp déggul. saay-saay si ay kàll lañuy waxe.

kàllóor g- : yul b-. góom bi ci kàllóor gi la nekk. dinañuy wax tamit kàlluur g-.

kàmb g- : kan m-, pax m-. demleen tuur mbalit mi ca kàmb ga.

kàmmaate j- : dinañuy wax tamit tamaate. (seetal tamaate)

kàmp b- : xeetu mburu mu wërgalu. mbulañsëri bi dinay am ay kàmp.

kàncóoli g- : dinañuy wax tamit kaña g-. (seetal kaña)

kàndiŋ g- : borom xam-xam bu mag. dëkk bi am na kàndiŋ gu fi dëkk.

kàngam b- : kilifa g-. kàngam yi yépp a nga woon ca ndaje ma.

kànja g- : soxna si jënd na kànja ngir supp-kànja bi muy togg.

kànnaar b- : xomb g-. sàcc yi dañoo dagg kànnaaru màngasin bi, sàcc marsandiis mi.

kàpp w- : taat y-. lutax xale yu jigeen yi di sol tubey yuy génne seen kàpp yi ?

kàrta b- : am na benn kàrta maryaas bu mànke-.

kàrta g- : lótëri b-. bàyyil kàrta gi te dem liggeeyi.

kàttan g- : doole j-. mbër mi am na kàttan. / Yàlla buur bu am kàttan la.

kàttit : (ne kàttit). lu jékki-jékki rekk dagg, tàppit, fàppit. buum gi ne na kàttit, dagg.