dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

jodd 1 : (ne jodd). baat bi dafay tekki lu taxaw jub kocc. dof baa nga ne jodd ca digg naaj wa.

jodd 2 : laxas ay njubbi kawar ak ay wëñ. dama bëgg nga jodd ma.

jodd b- : ñam wu ñu defare ñàmbi, ñebbe ak gerte gu ñu baxal. ca restoraŋ ba laa lekkewoon jodd.

jof : dikk, ñów. nag yi yépp jof nañu.

joggi : dëgg. moytul a joggi xalu safara wi.

jog : waa ji fi toogoon jog na ba dem. dinañuy wax tamit jóg wala jug.

jokk : jotale ñaari mbir. jokk na buum gi ci buumu xar mi.

jollasante : waxante ay wax yu ñagas, xiironte. ñoom fu ñu toll, ñu ngi jollasante.

jolli : yéeg. coow laa ngay jolli bu baax ca marse ba.

jolof g- : jolof diwaan la bu nekk Senegaal te dend ak Kayoor.

jolu : téru. jolu na guttu ndox bi yépp.

jombaxtal g- : coll b-. céeli gi dal na ca jombaxtalu garab ga. dinañuy wax tamit njombaxtal g-.

jomb : ñàkk a yelloo. jëkkëram ju baax ji dafa ko jomb. / waroon naa jomb li mu def.

jombos j- : nduggam mi am benn jombos.

jommi : waaru, jaaxle. ku ay rab tiital. garab googu ku ko ronu, jommi.

jomm : (ne jomm). mel ni ku waaru. mu nga toog ne jomm ni ku waaru.

jom j- : ku am jom dafay bañ ku ko reetaan.

jomp : fees. paan bi jomp na.

jong : xaraf, téegu, nàndalu. bu ekkool tëjee la xale yi di jong.

jongoma j- : ndaw s-, jigeen j-, soxna s-. jongoma dafay fonk boppam te mën a defaru.

jonj : bomb. jonj na tank yi ba ñu set wecc.

jonkan : dinañuy wax tamit jonkon.

jonkon : waa jaa ngi jonkon di ratt nag wi. / dof bi jonkon na ci digg yoon wi. dinañuy wax tamit jonkan.

jonn : (ne jonn). teew. xanaa sooy jëw nit ki ba mu ne jonn, nga mën a noppi.

joŋante : xëccoo, rawante. réewi Afirig yi dañuy joŋante ci futbal bi.

joŋe : bare feem, muus, yeewu. jigeen dafa war a joŋe.

joobe : tagg, bàkk. géwal baa ngi joobe géeram bi.

jooju : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

joolaa b- : waaso wu cosaanoo ca Kasamaas. joola amul caaxaan.

joor : woo nit bu baax. mu ngi koy joor wànte déggu ko.

joor g- : sàlleñ s-. suufu joor nanguwul mbey.

joos : xoos. mu ngi joos koko bi.

joote b- : musiba m-. yal na ñu Yàlla musal ci bépp xeetu joote.

joow : ming. mool yaa ngay joow gaal ga jëm géej.

jooy : ku dóor xale bi ba muy jooy ?

joqalante : weccee. ñu ngay joqalante ay baat yu ñagas.

joqarbi : joxoñ. mu ngay wax di ko joqarbi.

jot : du jot liiñ bi, dafa gàtt ba mu ëpp. / jot na wàllam ci xaalis bi.

jot g- : péex m-. nee na su amee jot, dina fi ñëw.

jox : bu ñu la joxee alali ñépp, nga war koo séddale, ku nekk jox ko li mu moom.

jox b- : takku dugub wala basi, jàpp wi. fukki jox yi asaka la ko génne.

joxoñ : bankal sa baaraam bi nga may joxoñ.

joy 1 : antu, defu. soo amul fulla ak faayda, li ngay def du mës a joy.

joy 2 : dëngal, wengal. ngelaw lee joy sàkket wi.