dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ji 2 : jëmbët, saxal. ji nañu dugub ba pare.

jiba j- : poos b-. defal xaalis bi ci sa jiba ji.

jibarkat b- : buxaaba b-. jibarkat yi tas nañu kër, tas nañu sëy. dinañuy wax tamit njibarkat b- wala njabarkat b-. (seetal buxaaba)

jibar : sëriñ bi jibar rekk mooy liggeeyam.

jibbutoon g- : garabu dég. seen àll bi am na ay jibbutoon.

jib : sabar ga dafa jib rekk, xale yu jigeen yi daw dem.

jib w- : kéwel g-, mbill m-, baroom b-. rëbbkat bi jàpp na aw jib.

jif j- : dinañuy wax tamit gif g-. (seetal gif)

jigeen : doom ju jigeen la am. safaan wi mooy góor.

jigeenu-biir j- : jigeen ju ëmb j-, jigeenu-werul j-. jigeenu-biir dafay yomb a sonn.

jig : luy joxe wërsëg. jabaram jig na ko ndax bi mu ko takkee rekk la am liggeey. safaan wi mooy jigadi.

jiib : sóob. jiib na yére yépp ci biir ndox mi.

jiin : tëgg ndënd ngir tagg nit. jiin na ndënd mi ba waa ji bég. / waxloo ndënd. tëggkat yaa ngi jiin sabar yi.

jiiñ : tuumaal. seetal bu baax li ngay jiiñ waa ji ndax moo ko def am déet.

jiiru : dindi ay pepp ak ay yoxo ngir lekk leen. jiiru na gubu dugub wi yépp.

jiit : jëkk. su ngeen doon daw, mu jiit la ndax moom dafay taggat yaramam saa yu nekk. safaan wi mooy mujj.

jiit j- : jànkalaar b-. jiit dafay fette.

jiix : dinañuy wax tamit jéex. (seetal jéex)

jikko j- : ndéem yaay kilifa gi, fexeel ba wone jikko ju rafet.

jimaamu : tiitaru. li nga yor bay jimaamu, nit yor na ci fukk te kenn xamu ko ci moom.

jimeet : (ne jimeet). jékki jékki rekk fëll, xusër (ne). kaña gi dafa ne jimeet, jaar ci kanam nit ñi. dinañuy wax tamit jumeet (ne).

jinax j- : dinañuy wax tamit janax j-. (seetal janax)

jinikal : mel ni luy def dara. dafay jinikal rekk wànte liggeeyul.

jinjeer j- : ndoxum jinjeer lañu defaraloon.

jinne j- : lu yéeme lu nit ñépp dul gis te am ci yu baax ak yu bon. jinne njolloor lay dox.

jiŋeet : (ne jiŋeet). màgg. doomam ji ne na jiŋeet léegi.

jirim b- : xale bu ñàkk pàppaam. jirim bi dafa teel a ñàkk pàppa.

jir : baat bi dafay ànd ak baatu tàng di tekki torob. dinañuy wax tamit jirr, jér, jérr, jër wala jërr. defleen ndànk, laax bi dafa tàng jir.

jiyaar : xare. jullit yi daan nañu jiyaar ak yéefeer yi.