dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

inde b- : bool bu ñu def ay bën-bën yu bare ngir suusal cere, ceeb wala leneen. inde bi dafa tàng, bu ko laal.

indi : indi na sërica. / mego sigaret bee indi day g-. / dinañuy wax tamit andi wala ëndi. safaan wi mooy yóbbu.

iniwersite b- : daara ju kowe j-. njàngum iniwersite dafa metti.

insàllaa : su neexee Yàlla, su soobee Yàlla. insàllaa su ma amee xaalis, dinaa aji Màkka.