dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ilif : jëwriñ ji yor biir réew mi moo ilif takk-der yépp. dinañuy wax tamit yilif.

ilimaan j- : kiy jiite julli gi ca jàkka ja wala ca jumaa ja. ilimaan yegsi na. dinañuy wax tamit elimaan j-.

illa g- : nësër b-, naal b-. sama illa gi mooy tekki ba teral samay waa-jur.

illeer b- : dori b-, jumtukaay bu ñuy beye. sa illeer bi baax na wànte mënuloo bey. dinañuy wax tamit ëlleer b-.