dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gubar b- : dinañuy wax tamit gobar b-. (seetal gobar)

gub : dagg ay ñax ngir jur gi. taw bee ma teree gub tey.

gudd-loxo : am kudd gu gudd. gudd-loxo rekk bu mu tax lu la neex nga def, Yàlla gëmmul, nelawul.

guddi : bul génn kër gi, dafa guddi. safaan wi mooy bëccëg.

gudd : gis nañu jaan ju gudd ca àll ba. safaan wi mooy gàtt.

gudoroŋ b- : yoonu gugoroŋ w-.

guleet : bii mooy yoon wu njëkk. guleet, muy dem Dakaar.

gumba-xóll b- : gumba bu mel ni kuy gis. du gis dara, gumba-xóll la.

gumba : silmaxa. dafa gumba wànte xel mi dara nekku ci.

gumbe : xeetu pecc. jigeen ñaa ngay gumbe ca pénc ma.

gummeen : ñaan ndimbal ginnaaw mbey mu bon. seen mbey ma dara baaxu ca, dëkk ba yépp a ngay gummeen.

gump : fóot fóot mu gaaw. xaar ma ñu dem, damay gump sama yére yi rekk. dinañuy wax tamit gupp.

gune g- : dinañuy wax tamit gone g-. safaan wi mooy mag m-. (seetal gone)

gunge : bijjanti. ganam gi lay gunge te ñëw.

gunoor g- : moytul gunoor gi dugg ci ndab li.

guŋ : (ne guŋ). baat bi dafay tekki coowu lu diis lu daanu ci dara. tan mi ne na guŋ ci suuf.

gupp : dinañuy wax tamit gump. (seetal gump)

gureet : (ne gureet). gadd (ne), xasar (ne). tey jën bare na, ñu nga ne gureet ca ja ba.

gurmet b- 1 : katolig b-, kercee b-. tey feetu gurmet yi la.

gurmet b- 2 : ceenu moontoor wala lam bu ñu defare weñ gu yaatu. gurmet bi nga takk rafet na.

guro g- : boppam bi dafay metti su yëyul guro. dinañuy wax tamit guru g-.

gurub b- : dinañuy wax tamit mbooloo m-. (seetal mbooloo)

guru g- : dinañuy wax tamit guro g-. (seetal guro)

gutt b- : bidoŋ b-. gutt bi dëwlin la def.

guuj : (ne guuj). fees. lekk na ceeb ba biiram bi ne guuj.

guus : xaw a tooy. yére bi dafa guus mootax menu ko sol.

guutë g- : yoon wu génnul fenn. jaaral fii, foofu nga jëm guutë la.

guutuut g- : xeetu picc. guutuut yaa ngi sab ci kow garab gi.

guux : dinañuy wax tamit góox. (seetal góox)

guyaab g- : garabu guyaab. ngelaw lee daane guyaab gi nekkoon fii.

guy : baat bi dafay toftalu ci baat bii di sedd tey tekki lool. dëkk bi dafa sedd guy. dinañuy wax tamit guyy.

guy g- : garabu buy. guy gi meññ na.

guyy : dinañuy wax tamit guy. (seetal guy)