dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gobar b- : paaka b-, saamaar b-. gobar lay gànnaayoo buy génn. dinañuy wax tamit gubar b-.

gobbi : jël, raafal. gobbi na ci ñàmbi ji lu mu mën.

goblet b- : kaas b-, weer b-. jottali ko goblet bi, mu naan.

godoroŋ : dinañu godoroŋ seen raŋ-raŋ bi.

goj b- : buum gu ñuy roote. goj bi tàbbi na ci biir teen bi.

golñàdd g- : nit wala mala bu sew ruuj. golñàddug mbaam gi àttanul sareet bi.

golo g- : noppu-jaboot, baabun, dàngin. golo ñaawul, baay ba la niru. (léebu).

gom b- 1 : gom bi nga def ci yére bi saf na sàpp.

gom b- 2 : gom ngir faase bindi kereyoŋ, gomfaas b-. jëlal gom bi, faase bind yépp.

gomfaas b- : dinañuy wax tamit gom -b. (seetal gom)

gone g- : xale b-, tuuti-tànk b-. gone ba muy tuuti lañu koy jubbanti. dinañuy wax tamit gune g-. safaan wi mooy mag m-.

gong g- : lalu bant b-. mu ngay féexlu ca gong ga. dinañuy wax tamit goŋŋ g-.

gongo b- : cuuraayu puudar bu jigeen ñi di def ci morso takk ko, muy xeeñ. cuuraay gongo liy xeeñ, neex na.

gont : dem ci ngoon gi. du xëy, dafay gont liggeeyi. safaan wi mooy xëy.

goŋŋ g- : dinañuy wax tamit gong g-. (seetal gong)

googu : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

gooŋ g- : xeetu golo. gooŋ gi yéeg na ci kow garab gi.

goor : tëdd (mala). nag yépp goor nañu.

gooro b- : nattu ñeenti garaam ci oor. li mu takk ci oor mat na fukki gooro.

goowe g- : xeetu cuuraay. jëndaaleel ma goowe. dinañuy wax tamit gowe g- wala gawe g-.

gopp b- : bantu illeer. wàññil sa gopp bi, dafa gudd ci yow.

gornmaa b- : mbir mi du soppi gornmaa saa yu nekk, ci jël ñu mën a liggeey te jub la nekk. dinañuy wax tamit gornmãa b-, ngornmaa b- wala ngornmãa b-.

gornmãa b- : dinañuy wax tamit gornmaa b-. (seetal gornmaa)

gornoor b- : gornooru Kawlag bi teewoon na ca ndaje ma.

gor : dóor ak lu mel ni jaasi wala sémmeñ. pël bi dafa gor waa ji daw. / dagg, daaneel garab. nit ñi gor nañu àll bi yépp.

gor s- : nit ku moom boppam. du jaam, gor su set wecc la. / kuy yem ci li mu moom, ku am ngor. kooku gor la, du laal mukk lu mu moomul.

goro bu góor b- : sama goro bu góor laay seeti.

goro bu jigeen b- : goro bu jigeen lay yónne xaalis.

goro b- : say waa-juri jëkkër wala say waa-juri jabar. teral say goro du forse.

goroŋ b- : xeetu ndënd. xàmmewul goroŋ ak xiin.

gott b- : àll b-, ñaay b-. gott ba dafa lëndëm, ñemewu fa.

gowe g- : dinañuy wax tamit goowe g-. (seetal goowe)

gox b- : koñu dëkku tax b-. seen gox bi amul ay làmpi mbedd.