dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gicc : (ne gicc). guuj (ne). tabaski bi sófoor yi dañuy yeb seen oto yi ba ñu ne gicc.

gidaawaali g- : dinañuy wax tamit gilaawaali g-. (seetal gilaawaali)

gif g- : few j-, xooxu buy. baleel gif yi bala leen nit ñi di dëgg.

giif : dal, rees. meroon na lool wànte léegi mer mi giif na.

giim : fey. safara si giim na. safaan wi mooy tàkk.

gii : kër gii la sa waa ji dëkkoon. safaan wi mooy gee wala gale.

giir g- 1 : diir b-. jaamu Yàlla rekk la nekkewoon giiru dundam.

giir g- 2 : këll gu ñuy ratte meewu nag. raxasal ko giir gi, dafay ratt nag wi.

giir : am njaboot. seen maam bu góor naar la woon, moom moo fi giiroon.

giir b- : xeet w-. ci giir bu baax la bokk wànte moom du nit ku baax.

giiroo : xëccoo. taali be yi giiroo nañu cere ji.

giix : dinañuy wax tamit géex. (seetal géex)

gilaawaali g- : balaa b-, jéyya j-, luxóor b-, musiba m-. waa dëkk ba def nañu gilaawaali ndax dóor nañu sàcc ba ba mu dee. dinañuy wax tamit gidaawaali g-.

gileem g- : dinañuy wax tamit géleem g-. (seetal géleem)

gilint g- : jumla b-. feyal gilint gi bala ko xale yi di dëgg. dinañuy wax tamit gilit g-.

gilise : dinañuy wax tamit tarxiis. (seetal tarxiis)

gilit g- : dinañuy wax tamit gilint g-. (seetal gilint)

gilli : xeeñ. xetu mbalit mi gilli na fii yépp.

gil g- : ngelaw l-, biriis b-. gil gi jóge géej ñëw na ba fii.

gimmi : ubbi ay gët, xippi. dafa gëmmoon wànte gimmi na léegi. safaan wi mooy gëmm.

ginaar g- : dinañuy wax tamit ganaar g-. (seetal ganaar)

ginda y- : sagar y-. waa ji dafa mel ni dof, ay ginda rekk lay sol.

gindi : leeralal. soo bëggee ku lay gindi, deel waxtaan ak mag ñi. safaan wi mooy réeral wala sànk.

ginnaaw : dinañuy wax tamit gannaaw. (seetal gannaaw)

giñ : dinañuy wax tamit gëñ. (seetal gëñ)

giri b- : rëddu kawar wu dox diggante ñaari nopp ñu bàyyi ko ci bopp bu ñu wat. waaso woowu giri lañuy wat seen xale yi.

gis : gis naa sa waa ji marse ba. / ngoon dina ko gis. / gis na fasam wi réeroon. /

gis b- : xeetu jën. tey gis bare na marse.

gitaar g- : dafay jàng gitaar.

gitim j- : jigeen ju jëkkëram faatu muy muuru, jétur b-. diir bi gitim ji war a muuru léegi mu jeex.

gittax g- : sàkket wi gittax lañu ko defare. dinañuy wax tamit gattax g-.

gitti : dindi (li nekk ci biir leket gu wow), sulli. maamam lay gittil leket yi.