dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gecc : am lu la bett. gecc naa ci li nga def.

gedd : dañu ko dóor mu gedd añ bi.

geeb : daggat, fejat. dafa doon geeb ay xob ngir jox ko nag yi.

geen-bëtu : xeelu. yaa ngi koy geen-bëtu rekk.

geen b- : booy was, dangay dagg geenu jën yi.

gee j- : juroomeelu waxtu julli ci diiney lislaam. julli na waxtu gee ba pare. dinañuy wax tamit gewe j-. gee moo topp ci timis.

geestu : turne bopp ngir xool. kuy dawal oto warul a geestu. dinañuy wax tamit geesu.

geesu : dinañuy wax tamit geestu. (seetal geestu)

geet : ñàkk a lekk aw ñam. doktoor bi dafa geet ndaw si.

geg : kal. dafa geg buntu néeg bi.

gejaf : nooy. dinañuy wax tamit gajaf. (seetal gajaf)

gejj : defar ay gejj. boo demee Sowaal Faajut, nit ñaa nga fay gejj di jaay.

gellwaar b- : nit ku jële darajaam ci néegu ndeyam ci séereer yi. waa ji gellwaar la.

gel b- : gel mooy ndaw si ngay àndal te takkuloo ko

gelu : yég wuuteg nit ba ciy jële feebar wala géey. yaayam ji tukki la xale bi di gelu.

genaar g- : dinañuy wax tamit ganaar g-. (seetal ganaar)

geneen g- : am na ñaari kër, genn gi ci la dëkk, geneen gi mu koy luye.

genn-wàll g- : xaaj b-. genn-wàllu dëkk bi yépp ay wolof lañu.

genn : genn màngo gi dafay bëgg a daanu.

gent : dëkk bu gent mooy dëkk bu dem ba kenn dëkkatu fa.

geño g- : geño tubey g-. geño gi dagg na.

gerees g- : nékk g-, nebboon b-. xar mi bare ne gerees.

gereew : lànk bañ a liggeey ndax ay ñaxtu. liggeeykati Dakaar-Dem-Dikk yi dañoo gereew tey.

ger : joxe dara ngir am dara, jënd. waa ji soo ko gerul, du la liggeeyal.

gerte-caaf g- : gerte gu ñu saaf. jëndal ma gerte-caaf.

gerte-kemb g- : gerte gu ñu xolli. du lekk gerte-kemb.

gerte-mbaxal g- : gerte-togg. gerte gu ñu baxal. gerte-mbaxal la àndiwaale bi muy ñëw.

gerte-tubaab b- : doomu gerte-tubaab b-. duma lekk gerte-tubaab.

gerte-tubaab g- : garabu gerte-tubaab. gerte-tubaab gi yàgg na fi.

gerte-xott g- : gerte gu ñu xolleegul. kilo gerte-xott bi dafa daanu léegi.

gerte g- : ren gerte bare na ci àll bi.

gestu : xool ci ginnaaw. sàcc baa ngi daw di gestu.

get : napp. fan yii yépp mool yi getiwuñu ndax jën amul. dinañuy wax tamit gét.

gewe j- : dinañuy wax tamit gee j-. (seetal gee)