dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gaaf g- : jëf ju nit wala leneen di def wala lu nekk ci moom luy màndargaal lu baax wala lu bon. fas wi gaaf gu bon la yore.

gaajo g- : sabar g-, tànnbéer g-. jigeen ñaa ngay fecc gaajo.

gaal g- 1 : looco g-. ndaw ñi daan nañu jël gaal di dem Tugal.

gaal g- 2 : waxande w-. ay téere la def ci gaalam gi ba mu fees.

gaana : dafa gaana wànte terewu koo liggeey.

gaana g- : gënuloo gaana gi. dinañuy wax tamit ngaana g-.

gaanga : dinañuy wax tamit gaatnga. (seetal gaatnga)

gaanuwaay : saw, tuur ndox. bàyyil gaanawaay ci mbedd mi.

gaa : ci lu wóor. dina la ko fey gaa, wànte li mu la yoreel tolluwul noonu.

gaa ñ- : xuloo ba ca teen ba, gaa ñi amul baag la.

gaañ : lañset bi mu doon fowe moo ko gaañ.

gaaraafu : gaaruwaale. wujj wi lay gaaraafu.

gaaraas b- : fu oto yi di deppaare, di fa teere wala ñu leen fay deppaane. gaaraas bi bare na ay oto.

gaaral : ki mu doon xulool lay gaaral. dinañuy wax tamit gaaruwaale.

gaar : defaraat. dafa doon gaar tubeyam ji.

gaar b- : fu ay saxaar di deppaare ak a teere. gaar ba lay jaaye mango.

gaaruwaale : dinañuy wax tamit gaaral. (seetal gaaral)

gaas b- : gaas lay togge.

gaatnga : woo ci sa bopp. deel gaatnga lu baax ci sa bopp. dinañuy wax tamit gaanga.

gaaw : ropplaan waruwaay bu gaaw la. gaaw na ci togg. safaan wi mooy yéex.

gaawu b- : aseer j-, aset j-, samdi j-. gaawu bu jot mu ñëw fi. dinañuy wax tamit gaawo b-.

gadd : (ne gadd). baat bi dafay tekki lu bare. màndikat yaa ngi ne gadd ca baar ba.

gafaka g- : jiba j-, poos b-. defalal fas wi dugub ci gafaka gi.

gag : caŋ. dafa ñemewul sëriñam mootax muy tari di gag.

gajaf : nooy. koko bi dafa gajaf. dinañuy wax tamit gejaf. safaan wi mooy wow wala dëgër.

gajan g- : dindil gajanu màngo bi. dinañuy wax tamit gàjjan g-.

gajj 1 : xosi, xuri. muus mi gajj na ko.

gajj 2 : ruuj. gajj na toolam yépp di xaar Yàlla ji taw, mu ji leen.

galaas g- : ndaw si dinay jaay galaas.

galajaane : xalangal. ci lu gaaw la mbër mi galajaane morom ki.

galan : dafa galan lal bi. dinañuy wax tamit galen.

galat b- : saawo s-, yoon w-. galat bi ca àll ba la jëm.

gale g- : fer g-, jal-jali b-. gale gi janq bi takk a ngi feeñ.

galgal : lonk. dafa ko galgal rekk mu daanu.

gallaxndiku : saa yu yëyee guro, dafay gallaxndiku.

gall : woccu, tiisu. xale bi gall na, defar ko.

gall b- : saaku b-, ngaax b-. saaku yiy nekk ci weti mbaam. takkaatal gall yi bu baax.

gal b- : ngalam w-, wurus w-. ceen gi mu takk am na gal.

galt : newwi. xar-kanamam bi dafa galt.

gam-gamee : toppatoo bu baax. gam-gamee sa jëkkër, mooy li la war.

gam-gami : dajjant. nelawul biig mootax muy gam-gami.

gam-gamle : méngale, tëkkale. gam-gamle naa li ngeen def wànte gis naa ne sama waaj jee la dàq a liggeey.

gamb : tax b-. ku woddu jotul, doo boot i gamb. (léebu).

ganaar g- : ceebu ganaar lay toggal ganam gi. ay genaar lay yar, di jaay. dinañuy wax tamit ginaar g- wala genaar g-.

ganc b- : caga b-. ganc bi guddi rekk lay dox.

gandeer : wër (tàngaayu safara). puusal foofu bala la safara si di gandeer.

gannaaw 1 : këram a ngi ci gannaaw marse bi. dinañuy wax tamit ginnaaw.

gannaaw 2 : gannaaw bu mu ñëwee, la ma ko wax.

gannaaw 3 : ndegam. bàyyil ma defal ko sama bopp gannaaw mënuloo ko.

gannax g- : duus b-, mbar m-, wàgg y-. tey dem géej wóorul ndax gannax yi bare nañu, am nañu doole.

gann : baatu gann dafay tekki lu diis ba mu ëpp. saaku bi dafa diis gann, wutal ku la ko jàpple. safaan wi mooy toyom (woyof toyom).

gannuus g- : fu bare suuf, salleñ s-, beeñ b-. fas wi mënul a daw ci gannuus gi, def ko ndànk.

gan : gan kër la dëkk ?

gan g- : ngénte la bare na ay gan.

ga : forse ci am mbir. xale bi nanguwul a lekk ceeb bi wànte dinaa ko ko ga.

gañe : duma, mën, daan, raw. dañu doon damiye, ma gañe ko. safaan wi mooy perta, daanu wala ñàkk.

gañilaa b- : xeetu piis la. ku fi sol gañilaa ?

gaññaxu : dinañuy wax tamit gaññ. (seetal gaññ)

gaññ : yaa ngi gaññ de, xanaa li ngay naan dafa forox ? dinañuy wax tamit gaññaxu.

gañu : meebu, bobaru. soo fay jaar nanga gañu bala sa daraa ji di tooy.

gaŋ g- : doomi gaŋ dañu koy togg ndawal. dinañuy wax tamit gëŋ g-.

gappariku : dinañuy wax tamit gapparu. (seetal gapparu)

gapparu : bu xale yi di jàng alxuraan, dañuy gapparu. dinañuy wax tamit gappariku.

gar 1 : wol, dëbb. dafa gar dugub ji rekk mootax mokkul.

gar 2 : dajale, boole, naaf. pare na góob ba gar dugubam ji yépp. dinañuy wax tamit ngar.

garaa mbubb b- : daraa j-. garaa mbubb bu weex tàll la soloon.

garaam : nattukaayu diisaay. diisaayu ceenu oor baa ngi toll ci ñaar-fukki garaam.

garaangaal b- : paan b-, beñwaar b-. rootal ma garaangaal bi ba mu fees.

garaaw : dinañuy wax tamit ñàng. (seetal ñàng)

garab b- : luy faj jàngoro. garab bi baax na ci sibburu.

garab g- : garabu màngo gi meññ na.

garay g- : witteen b-. maamam denc na ay garay. dinañuy wax tamit garey g-.

garbo : jële dara ci cagatu, cagatu, fo. kër gi li muy rafet rafet, borom dafa ko garbo.

garees g- : póno bi dafa mànke garees.

garey g- : dinañuy wax tamit garay g-. (seetal garay)

gargamboose b- : gargamboose xeetu meññent la.

gargamboose g- : xeetu garab. gargamboose gi yàgg na fi.

garjeŋ b- : kuy wottu ab béreb, wottukat b-. gënuloo garjeŋ bi ci kër gi.

garmi b- : garmi yi ci ñi doon jiite bu jëkk lañu bokkoon.

garnitiir b- : garnitiir bee rafetal ñawam bi.

gar g- : gaynde g-. gar nu ko neex lay daagoo ci biir àll bi.

garxàll g- : njoogaan b-, xuuj b-. sa oto bi garxàll la.

gasax w- : sax w-. pom bi dafa am ay gasax.

gas : gas nañu teen bu xóot ca dëkk ba. safaan wi mooy suul.

gatandu : dem dajeek ku nekk ci yoon di ñëw, dogale. xale baa ngi gatandu yaayam.

gati g- : néeg bi, mbaar m-. néeg bu ñu defar ci wetu tool diiru mbey mi yépp. ca gati ga lay nekk ba guddi. dinañuy wax tamit gëti g-.

gat g- : (saaga la). ci sa gat gi ngay dugal per bi.

gattax g- : bantu gubu dugug. Saalum ay sàkketi gattax la ñuy def. dinañuy wax tamit gittax g-.

gawar g- : warkatu fas. gawar gaawul a daanoo ci fas.

gawe g- : dinañuy wax tamit goowe g-. (seetal goowe)

gawlo b- : jali b-, xalamkat b-. xew luñu am seen gawlo bi dina ci teew.

gaw : takk. gaw na simisam bi. safaan wi mooy gàwwi.

gayet b- : bantu sàkket wala mbaar. gayet bi dafa funax léegi.

gaynde-géej g- : gaynde-géej gi la xale yi di seetaan.

gaynde g- : gar g-. suñu àll bi barewul ay gaynde.

gaynóoki y- : gàllaaj g-, téere b-, xarfafuufa y-. waa ji rondalam gi dafa fees dell ak ay gaynóoki.