dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

gëdd 1 : dox bu baax, waaxu. mu ngay gëdd di dem.

gëdd b- 1 : njëriñ l-. li ngay def amul benn gëdd.

gëdd 2 : wax ak nit ci kàddu gu dëgër. ak loo mën a am, noo mën a tollu, bul di gëdd ku la mag.

gëdd b- 2 : yég g-. gëdd bi nga jox sa bopp, jox ko ñépp.

gëjjëx-gëjjëxi : jayax-jayaxi. seen naa ko ca kow fas wa muy gëjjëx-gëjjëxi di dem.

gëj : toog lu yàgg te defuloo am mbir. gëj naa dem seen dëkk.

gëleem g- : dinañuy wax tamit géleem g-. (seetal géleem)

gëlëm : ñàkk a xam foo nekk ak foo jëm. bi mu duggee ci awiyoŋ bi ba mu deppaar rekk, la gëlëm.

gël b- : suuf wala dóom bu tàng, rututum b-. moytul a joggi ci gël bi.

gëm-gëm b- : li nit ki gëm mooy gëm-gëmam.

gëmm : tëj ay gët. bi muy dënnu dafa sakk ay nopp, gëmm ay gëtam.

gëm : ndax gëm nga li mu la wax, waa ji fenkat la de.

gën-gaa : li gën a. jàppatuma ñaata lañu waaye gën-gaa bare fukk lañu.

gënn g- : dafay soq dugug ji ci gënn gi.

gën : moo ko gën a rafet. sa rakk a la gën. fexeel am sa yëfi bopp, moo gën ngay topp ci nit di ko dunguru.

gëñ : waat. gëñ na ko ci Yàlla ne du moom. dinañuy wax tamit giñ.

gëñ y- : ñaari gëñ / benn bëñ. ñaari gëñam dañuy metti.

gëŋ g- : dinañuy wax tamit gaŋ g-. (seetal gaŋ)

gëq : xeeti lekkinu yenn mala yi. xar dafay gëq suy lekk.

gërëm : sant. gërëm naa la bu baax ndax li nga ma defal.

gësëm : yëngal. ngelaw laa ngi gësëm bànqaasi garab yi.

gës : gas. ginaar yaa ngi gës dugub.

gëstu : seet ay mbir ci… ci làkk yi lay gëstu.

gëti g- : dinañuy wax tamit gati g-. (seetal gati)

gët y- : bët b-. ay gëtam dañuy metti. / bëtam bi dafay metti.